TUKKIB NJIITU RÉEW MI FA SÀPPOŊ

Yeneen i xët

Aji bind ji

Njiitu réew mi, Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, jóge na fi tay, ci yoor-yoor bi, wutali Sàppoŋ. Fa lay nekk ba keroog 26eelu bésub ut 2025.

Njiitu réew mi dafa teeweji 9eelu ndaje mees dippee “Conférence internationale de Tokyo sur le développement de l’Afrique” (TICAD 9). Ndaje la mom, yokkuteg Afrig lees fay waxtaane.

Bu Njiitu réew mi noppee ca mooma ndaje, dina fekke yit xew-xew bees di wax “Journée du Sénégal à l’exposition universelle Osaka Kansai 2025”.

Ci lees biral, tukki bii, dafa bokk ci liy suuxat ak a dëgëral kóllëre ak digaaley liggéey yi dox diggante Senegaal ak Sàppoŋ.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj