Ci guddig talaata ji, jàpp àllarba 8i nowàmbar 2023 la ñu fetal benn Baay-Faal ca Tuubaa ca koñu Firdawsi.
Li sabab jile jéyya, mooy ne Baay-Faal yi dañiy faral di wër ngir sayt lépp li kilifay Tuubaa gi di tere ci biir dëkk bi. Nde, dafa amoon kenn ci Baay-Faal yi ku rax ay jaakati sigaret ak yàmbaa, ngir mën leen a yoole. Noonu la Baay-Faal yi duggsee ca biir koñ ba ngir jéem leen a jàpp. Waaye, mbir mi yombewul woon noonu. Nde, ñoom ñi ñu jiiñ ne ay jaayktu yàmba ak i sigaret lañu, dañu doon jàmmarloo ak Baay-Faal yi, génne fa ag fetal ba faf rey kenn ci Baay-Faal yi, mu doon wuyoo ci turu Mustafa Ñaŋ tolloon ci 35i at.
Bess sukkandiko ci RFM, mi ngi ñuy xamal ne sàmbaabóoy yi ñu ne ñooy jaay yàmbaa, ay pël lañ. Waaye, dara wóoragu ci.
Ginnaaw gi la takk-der yi ñëw. Waaye, ñenn ci Baay-Fall yi dañu lànkoon ne fàww ñu fayu, ci la takk-der yi tàmbalee sànni ay gërënaad lakkirimosen ngir yemale mbir mi. Jot nañ ci teg loxo lu toll ci 12i nit.
Ci biir jàmmarloo bi, yóbbu nañ ca lopitaan bu Matlabul Fawzeyni, kenn ci Baay-Faal yi ci ame ay gaañu-gaañu ak 3i yu ñu cor ak i jaasi ci geneen wet gi. Sàndarmari nee na dina ubbi ag luññutu ngir leeral mbir mi.