Démb ci alxames ji la Njiitu réew mi doon jiite ubbiteg Kàggu gees jagleel dundu Yonent Yàlla Muhammat (SAWS) ak xayteg lislaam.
Démb, 25 féewiryee 2025, lañu ubbi Musée de la Biographie du Prophète et de la Civilisation Musulmane, maanaam kàggu gees jagleel dund ak liggéeyu Yonent Yàlla Muhammat (SAWS). Kàggu gaa nga féete wetu Musée des Civilisations Noires, fa Ndakaaru.
Bees sukkandikoo ci kàdduy Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, « béréb bii di bérébu xam-xam bii ak jàngale dafay dooleel sunu pasteef ci ndono li mu nu bàyyee ci fànnu xam-xam bu daj àddina. ». Kàggu gii nag, Senegaal daf ci lëkkalook réewum Araabi Sawdit. Moo tax Njiitu réew mi biral i cant ak i ngërëm ñeel njiiti réew mooma, rawatina buur ba, Salmaan Ben Abdul Asiis Al Sawuut, ak bummi ba, Muhammet Ben Salmaan. Njiitu réew mi rax na ca dolli ne :
« Tay, sunu liggéey bi gën a réy mooy fexe leeral taarub lislaamu cosaan te di xeex ëppal ci diine ak ñiy ñaawal diine ji. Loolu lanuy def fi Senegaal, di réew moo xam ne jullit ñee fi ëpp. Waaye, danu fiy nangul ku nekk gëm-gëmam, di dund ci jàmm te xajoo. »