UBBITEG PÉNCOOM RÉEW MI ÑEEL NOSTEG PÓLITIG BI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ci àllarbay tay jile, 28 me 2025, lañu doon ubbi péncoom réew mi ñeel nosteg pólitig bi. Jamñaajo, fa CICAD (Centre international de conférences Abdou Diouf), lañu ko doon amale ci njiiteefu Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay.

Wëliif Njiitu réew mi, elimaanu jëwriñ yi ak njiitu Ngomblaan gi, làngi pólitig yu bari yabaloon nañu fa seen i ndaw. Ñii di way-moomeel yi tamit teewoon nañu fa, ñoom ak kilifa diine yeek yoy aada yi. Naka noonu, sàndikaa yaa nga fa woon, kuréli ndaw ñeek jigéen ñi ak yeneen pàcci askan wi. Ndajem tay mi nag moo màndargaal ndoorteelu péncoo mi. Jubluwaay bi mooy, ci njeexital la, amal i coppite yu xóot ci nosteg pólitig bi. Maanaam, dees na xoolaat lépp lu aju ci nees di tëggee ak a lootaabe làngi pólitg yi, naka lees di saytoo, rawatina lu ñeel koppar yi ñuy liggéeye. Waayeet, dees joyyanti anam bees di amalee wote yi fi réew mi, campeef yi koy saytu ak nees di def ba tëral aw yoon wow, ci màndute lay lalu, mu bañ a am xàjj-ak-seen. Lii lépp nag, dees na ko lal ci waxtaan wuy boole ñépp ngir bennoo bennale réew mi.

Ginnaaw bi ñépp waxee, Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Fay, biral na fay kàdduy boole ak woote jàmm. Ci biir i waxam, moom Njiitu réew mi fésal na yéeneem ak dogoom ci sàmm bennoo giy màndargaal Senegaal ak jàmm jees ko xamee. Loolu moo ko tax a wax ne, dafa war ci saa-senegaal yépp ñu booloo, bennoo, di déglonte, wóolonte te di déggoo.

« Sama wareef niki aji-sàmm bennoog réew mi mooy tàllal sama loxo ñépp, góor ak jigéen, ngir dalal xel yi, boole ñépp, fexe dal am fi te juboole ñépp ngir suuxat ak a dëgëral jàmm ak dal gi xam ne, bul amul, koom-koomu réew mi du mën a suqaleeku. »

Bi Njiitu réew mi di tëj i kàddoom, sàkku na ci péncookat yi ñu waxtaan ci dëgg, dal, déglonte te jéllale seen i jëmm ngir xool liy jariñ askan wi kepp.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj