UE MI NGI GËTËN MAKI SÀLL

Yeneen i xët

Aji bind ji

UE (Union Européenne) waxatinaak Maki Sàll. Ginnaaw bi mu njëkkee ñaawlu ajug wote yi, kurél gi dafa dellu démb ci àjjuma ji doon sàkku ci Maki Sàll mu amal i wote yu jaar yoon, yu sàmmonteek Ndeyu Àtte réewum Senegaal.

Keroog bi Maki Sàll defee génnam googu ba ajandi wote yi ñu nammoon a amal ci 25 féewiryee bii ñu dëgmal, waa UE (Union Européenne), di mbooloom réewi Tugal yi, dañu génnoon doon ñaawlu lu ni mel. Nde, ci kàddu yi mu yékkati woon ci fan yooyu mooy ni Maki Sàll dafa dakkal lu Senegaal miinoon, te muy amal i wote saa bu ñu ko àppalee, fal Njiitu réewam. Muy lu Senegaal aadawoo woon ba ñu boole ko ci réew yi gën a tegu ci yoonu demokaraasi, fii ci Afrig Sowu-jant.

Ajandi googu nag moo juraat démb ay yëngu-yëngu yu metti ci dëkk bi ba am ñu ci ñàkk seen i bakkan. Dara waralu leen nag lu dul ni kujje geek askan wi dañ lànk, génn ci mbedd yi, di ñaxtu ngir wote yi am ci bés bees ko jàppaloon.

Yëngu-yënguy démb yi nag ñoo yékkatiwaat waa UE ba ñu waxaat ci jafe-jafe yi réewum Senegaal di dund jamono yii. Naka noonu, ñuy sàkkuwaat ci kilifay Senegaal yi ñu sàmmonteek Ndayu Àtte réew mi te amal i wote yu jaar yoon.

UE mi ngi woo kilifa yi ci ñu jël matukaay yi mu laaj ngir amal i woteb palug Njiitu réew mi ni mu gënee gaaw, ni mu méngook Ndayu Àtte réew mi ak ànd déggoo yu CEDEAO ñeel demokaraasi ak gën-ji-yorinu réew” (Sosef Borel, kenn ci ndawi kurél gi).

Bokk Na ci li ñu seetloot, ajandi gi am na njeexital yu bare ci réew mi, rawatina ci wàllu koom geek ci nekkiinu askan wi. Fàttali nañu itam ni Askan wi dafa am i àq ak i yelleef yu kenn warul a salfaañe yu deme ni fésal seen naqar ak génn ci mbedd yi ñaxtu ak jàmm. Càmm Gi dafa leen ko war a nangul nees koy nangulee maxejj yi ci mépp réew muy dox ci yoon ak di sàmm àq ak yelleefi askan wi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj