USMAAN SONKO WEER NA MAKI SÀLL

Yeneen i xët

Aji bind ji

DGE, kurél giy saytu lépp lu aju ci wote yi, lànkalati na ndawul Usmaan Sonko li, Ayib Dafe. Nee na dee, du jébbal Usmaan Sonko xobi baayale gi. Moone ne, Yoon a ko santaane. Démb, ci alxames ji, 19 oktoobar 2023, la fa Ayib Dafe dellu ginnaaw bim fa jëkkee dem ci àllarba ji. Nde, ci àllarba jooju la, demoon na fa màkkaanu DGE, ànd ak wisiiye bi ngir jébbal njiitul DGE li ndogalu àttewaayu Sigicoor bi. Li mu ko dugge woon mooy mën a jëlaale xobi baayale yi ngir Usmaan Sonko mën a bokk ci wotey 2024 yi. Waaye, démb, dafa lànkati, bañ a gise ak ndawi Usmaan Sonko yi. Doxalin woowu day feddali nisëru Maki Sàll mi nga xam ne, sañ naa xotti worma yépp ngir tere Sonko bokk ci wote yi. Mu mel ni Sonko am na fum jàpp Maki Sàll.

Cig pàttali, kii di Ayib Dafe jëkkoon na dem fa màkkaanu DGE ngir jëlil Usmaan Sonko xobi baayale yi ñeel wotey 2024 yi. Waaye, kii di DGE dakoo gàntaloon, xamal ko ne Usmaan Sonko bokkatul ci wayndarew wote yi. Noonu layookati Sonko yi jébbal ab « reféré liberté » waa Ëttub Àttewaay bu mag bi. Foofeet, Usmaan Sonko daf fa lajjoon. Waaye, taxul Usmaan Sonko xàddi walla muy gedd. Dafa kalaameji àttekatu Sigicoor ba, Sabasi Fay, àttekat bi jox ko dëgg, santaane ñu delloo ko ci wayndarew wote yi te delloo koy àqam. Noonu, Ayib Dafe ànd ak ak wiisiyee, dem fa DGE ngir jox leen ndogalu àttekat bi te jëlaale xobi baayale gi. Ci àjjumay tey jii, Ayib Dafe delluwaatoon na DGE, waaye loxoy neen la ñibbee. Ñetti yoon yi ñu fa dem yépp, moom ak wiisiyee bi, dañ leen a bañ a dalal. Kenn ubbilu leen bunti DGE yi sax. Lu tax ? Nee ñu, ndigal lañ jot.

Yéenekaayu « L’Observateur » xamle na ne, doonte àttekat bi dogal na la muy dogal ba noppi, waaye ba léegi bindaatuñu Usmaan Sonko ci wayndarew wote yi. Rax nañ ca dolli sax ne, DGE amul màqaama dugalaat Sonko ci wayndarew wote yi. Jëwriñu biir réew mi rekk moo ko mën lijjanti.  Kon, mënees na jàpp ne jëwriñ joojoo ci dëgg tànkam. Te, ku ne jëwriñ, ne Njiitu réew mi. Ndax moom mooy buur di bummi. Kenn ciy jëwriñam sañut a def lu mu ko digalul. Kon, ndigal li, ca kow la jóge. Moom Maki Sàll moo tere waa DGE jox Usmaan Sonko xobi baayale gi.

Ànd ak loolu yépp, Ayib Dafe moom, nee na du sonn, du tàyyi. Nde, saa bu xëyee, dina dem DGE, laaj xobi baayale yi ngir Usmaan Sonko. Te, fii ak jëlu leen, du bàyyi. Bu dee layookati Sonko yi, ñoom dañu biral ab yégle, di ci ŋàññ ak a naqarlu tooñaange bile. Ndax, ci seen i wax, dafay « …salfaañe cëslaayu Ndeyu Àtte réew meek àq yi mu war sàmm. » Ñuy dellu di « … wax Njiitu réew mi, Maki Sàll, mu doxal yoon, te topp li Yoon di dogal. »

 Coow lii moo lëmbe réew mi fan yii. Usmaan Sonko a nga ca raglu ba tëdd. Waaye, moo tere Nguur gi nelaw. Jéem nañoo yàq deram ak i tuuma yu dul jeex : salafist, wahaabii, rëbelu MFDC, ciif (Aji Saar), duural (Maam Mbay Ñaŋ), càccug jollasu, añs. Waaye dara. Boobaak léegi, dañ ko singali, moom ak njabootam. Du càggan ne dañu faral Usmaan Sonko. Waaye, ku waxul dëgg, wax safaan bi. Lees koy tuumal yépp, amagu ci lenn lu Yoon dëggal ndax amu ciy firnde. Topp nañ ko ba mu sës ci miiru wis bi, taxul ñu bàyyi ko. Jël nañ dooley Nguur, ak ni mu tollu yépp, di ko ko xeexe boobaak léegi, taxul ñu daan ko. Tas nañ làngu pólitigam, jàpp ay kàngaami Pastef tëj ci kaso bi, jàpp ay ndawam, nëbb leen jant wi. Waaye, ba tey, taxul ñu am ndam ci kow meeru Sigicoor bi. Ndeke, ni Maki Sàll ak i àndandoom ragalee Usmaan Sonko, ragaleewuñ ko noonu Yàlla.

Seen doxalin day firndeel ne, wote yii di ñëw, Usmaan Sonko moo ci teg tànk. Te, ragal nañu mu jël Nguur gi ndax seen i loxo dañoo taq ripp. Moo tax, léegi, nëbbatuwuñu, làqatuwuñu. Dañuy jalgati Yoon num leen neexee, lépp rekk, ngir tere Usmaan Sonko bokk. Moone de, Usmaan Sonko noon na Maki Sàll, boo ma bëggee faagaagal, fàww nga taqal say loxo. Booba, foogeesoon na ne mbirum jël bakkan la Usmaan Sonko doon wax. Ndeke, ni Maki Sàll di salfaañee campeefi réew mi, di tilimal kenoy Càmm gi la ci nammoon. Kon, Usmaan Sonko weer na Maki Sàll.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj