USMAAN SONKO XAATIM NA DÉGGOOB JÀMM AK BENN PÀCCU MFDC

Yeneen i xët

Aji bind ji

Elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko, ak benn pàccu MFDC xaatim nañu ab déggoob jàmm ci teewaayu Njiitu Réewum Gine Bisaawo, Umaroo Sisoko Embalo. Barki-démb, dibéer ji 23i fani féewiryee 2025, lañu xaatim déggoo bi, fa Bisaawo.

Elimaanu jëwriñi dafa sol i dàllam, dem ba Bisaawo, péeyub Gine Bisaawo, ngir xaatim ab déggoo buy delloosi jàmm fa Kaasamaas. Lu ko jiitu nag, Càmmug Senegaal gi dafa njëkk a waxtaan ak MFDC. Ndiisoo gees duppee Comité ad hoc pour la paix en Casamance ak pàccu MFDC bii di Comité provisoire des ailes politiques et combattantes unifiées du MFDC ñoo séqoon waxtaan wi. Jubluwaay mooy ñu wéer ngànnaay yi, dakkal xare bi.

Bees sukkandikoo ci xibaar yi banqaasu jokkoog Càmm gi (BIC-GOUV) siiwal, déggoo bii ñu xaatim dafa sottal liggéey bees tàmbali woon ca atum 2022. Nde, cig pàttali, Nguurug Senegaal ga woon jotoon na xaatim ab déggoo ca at mooma ak kii di Sesaar Atuut Bajaat mii jiite ñetteelu pàccu MFDC bi. Moom Sesaar Atuut Bajaat dafa nangu woon wéer ngànnaay yi.

LI CI BIIR DÉGGOO BI

Ci yégle bi banqaasu jokkoo Càmm gi biral, ñoo ngi ciy wax ne déggoo bi day feddali déggoo bees njëkkoon a xaatim keroog 4i fani ut 2022. Déggoob 2022 ba nag, daf ci amoon ay ponk yu bari yu deme ni :

  • Dakkal xeex bi ;

  • Wutal liggéey sóobarey MFDC yi wéer seen i ngànnaay

  • Delloosi daw-làqu yi ak ñi tóxu woon

  • Suuxat yokkuteg Kaasamaas ci wàllu koom-koom ka mboolaay mi

  • Wutal ay këyiti juddu nit ñi ko aajowoo fa béréb ya xare ba laaloon

Kaasamaas dafa nekk diiwaan bu ràññeeku, bari lool ay njagle ci wàllu mbindaare ak koom. Waaye, ba léegi, muy waa Kaasamaas di waa Senegaal gépp, kenn jariñoogul ni mu waree ci jagle yooyu. Li ko waral nag mooy ay woowu jiboon fa ca atum 1982 ba tay. Wolof dafa ne, ginnaaw ay, jàmm. Te, fu jàmm amul, naataange du fa am.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj