WAVE AK ORANGE MONEY, NUN LAÑ FI NEKKAL WALLA SEEN BOPP? (AMI MBENG)

Yeneen i xët

Aji bind ji

Wax ji bari na, werante bi ne kurr, ñii naan « Ñaw ! Upp baax na ci laax bu tàng ! », ñi ci des naan « Aawo bu xamul boppam, wujj rekk moo koy faj… ».

Coow li coow li, Farãs ak Amerig ñoo nekk ci kujje gu metti jaarale ko ci ay bànqaasi dencukaay xaalis ci telefoŋ, ñu koy wax « mobile-money ». Bànqaas yooyu di “Wave” (Amerig) ak “Orange” (Farãs), ci wàllum denc, yónnee, jot ak génne xaalis, mbaa fey kuraŋ ak ndox walla jënd kérédi ak yu ni mel  lañuy yëngu te lépp ci sa biir telefoŋ nga koy defe. “Wave” nag, bi mu dikkee Senegaal yàggul.

Ndax ci fàttali, Wari, Jóoni-jóoni, Ria, añs… ñoo yoroon wàll wi di ci liggéey, di ko doxal ba mu woomoon lool sax. Noonu la Sonatel dugge ci làng gi, sàmp ndëndam, duppe ko Orange Money, tàmbalee jambaaje mbir yi. Ndax bi mu ñëwee, daanaka kilyaan yépp a ci daan gis seen bopp. Muy doxal ak a fóoxal kilyaan yi ba déjjati yeneen bànqaasi dencukaayu xaalis yi, ba mu des moom kott ci làng gi. Noonu mu yëg boppam, tàmbalee def lu ko neex, di teg ay ndogal ak i sàrt ci wàllum yónnee beek génne xaalis ak peyug ndox meek kuraŋ geek ñoom seen. Ñu yokk njëg yi. Ndax dem nañ ba junni boo yónnee dinga ci fey juróom-ñaar fukk, te lu xaalis bi ngay yónnee mbaa nga koy génnee di gën a bari, njëg li di gën a yokku, rax-ci-dolli duñuy fey ñi leen di jaayal lu ko jar. Ñu dem ba kilyaan yeek ñi leen fi taxawal (prestataires) gisatuñ ci seen bopp, di kaas ngir mbir yi gën a yomb ci ñoom. Waaye taxul ñu teggi seen tànk, jàpp rekk, daal, ne kenn mënatuleen a jommal mbaa di leen diir mbagg ci biir làng gi. Li wolof naan «ku naagu daagu, te ku daagu ñu romb la», moo dal waa Orange (Sonatel).

Ndax “Wave” dafa dikk indaale ay feem yu bees ngir kilyaanam yi jariñoo ci bu baax. Bañ nañ ko ba kàddu gi ñuy bàkkoo mooy «sa xaalis yaay boroom». Boo demee bay yónnee jaarale ko ci Wave, téeméer boo jël, dërëm ngay fay, bu fekkee junni bi la, fukki dërëm mooy peyoor gi. Te boo fa dencee sa xaalis, boo koy génne doo fey dara.

Doomi Senegaal yépp a gis seen bopp ci Wave ba mu des ñi leen di jaayal (prestataires). Daanaka ñépp a fa toxu bàyyi Orange Money.

Lii moo sooke ay wi.

Orange def ay pexe ba kenn mënatul a jënde kérédi Orange ci Wave. Ñu nég ab diir, mu génne ab yëgle di xamle ne dafa wàññiy njëgam ci wàllu yónnee ak génne xaalis ba ci peyug ndox meek kuraŋ bi. Léegi boo yónnee junni, juróomi dërëm mooy njëg li. Li ñu jaaxal mooy ne, Orange wàññiwul benn yoon njëg yi. Boo amee tuuti seetlu dinga gis ne li mu wàññi ci njëgi yónnee yi, moom la yokk ci njëgi génne yi. Maanaam ay feem yu bees ci wàllu njaay la Orange jëfandikoo ngir lëndëmal xelu nit ñi.

Ci gaawu bi yemook 5i fan ci weeru suweŋ la Wave génne benn yëgle di ci xamle ne ginnaaw waxtaan wu yaatu wu mu amaloon ak Sonatel, «déggoo amagul ci sunu diggante ngir ñu mën di jaay kérédi Orange ak Wave», teg ci ne «war nañ di jaay kérédi Orange ni ko yeneen bànqaas yiy defe, te mu dëppook yoon, du am xàjj-ak-seen». Dolli na ci ne «àgge nañ mbir mi kilifa giy yoonal li jëm ci wàllu jumtukaay yeek jokkoo xarala yu yees yi (ARTP), ngir mu àtte nu, te am nan yaakaar ne àtte bi dina jaar yoon».

Noonu, “Orange” daldi tontu “Wave” cib yëgle, di ci wax ne «”Wave” moo wax ak “Sonatel” ngir jaay kérédi “Orange”. Ngir sunu kilyaan yi am tànneef ci fu leen neex jënde fa kérédi, tegal nañ ko sàrt yiy tax muy jaay, te sàrt yooyu ñépp a ci yem, ba ci sax sunu bànqaasu bopp bii di Orange Money. Wave nag dafa foog ne li muy wàññil kilyaan yi, war naa tax ñu gën koo mën a yokkal yoolam… Waaye bu demee ba nangu sàrt yi nu ko tegal rekk, dinañ àggale liggéey bi ci ni mu ware.»

Lu kujje gi metti metti, saf na sàpp ci ñii di jaaykat yi, daanaka ñoo ci gën a dee. Ndax li leen “Orange” ak “Wave” di fey fajul dara astemaak yor kër ak yi mu àndal. Ginnaaw gi ñoom tamit jóg nañ xeex. Bu ñu ñëwee ci “Wave”, ngir jaaykatam bi am téeméer ci bés bi, fàww kilyaan bi dugal mbaa génne lu ëpp ñaari-junni jëm ñaar-fukki junni. Bu dee “Orange Money” la moom, bu kilyaan bi génnee téeméeri dërëm, jaaykat bi ñett fiftin doŋŋ la ciy am (3iF) ; bu dee xaalis buñ dugal la, du ci am dara. Bu demee ba romb fukki junni, jaaykat bi juróom-fukk yu tóol ñaari fiftin la ciy am. Muy wone ni dina jafe lool jaaykat bi am ci bés bi lu mu mën a jariñoo. Jafe-jafe yii ñoo tax, jaaykat bii di Séex Ñaŋ, bind ab bataaxal di ci wax seen njàqare, yónnee ko ARTP ngir mu saafaraal leen ko.

Bu ñu ci jógulee, mbir yi dina ëppi loxo, ndege mbootaay mi ëmb jaaykat yi xaaratuñ ARTP ngir mu àtte leen. Ci 8i fan ci weeru suweŋ bii, lañ amal ndaje ak taskati xibaar yi. Ki jiite mbootaay mi di Xalil Njaay, mu ngi yëgle ne, teg nañ ay sàrt yoo xam ne dañuy ga kilyaan yi ngir ñu nangu leen. Lu ko moy, kilyaan bi du mën a génne xaalis. Sàrt yi nag dafay wax ne «gannaaw-si-tey, képp kuy génne mbaa ngay dugal walla yónnee xaalis, dangay fey. Te jubluwaay bi mooy nguur gi indi ay saafara, teg ay sàrt ba nun jaaykat yi nu gis sunu bopp ci làng gi». Njiital mbootaay mi teg ci ne «dogal bi, fi nu ko teg mooy ne, boo demee loppitaan di faju, fàww nga jënd tike, léegi dara yombatul, fépp foo dem nit ñi dañuy feyeeku liggéey… na jaaykat yépp topp ndigal yi te bañ a xabaabal».

ARTP génne na moom it benn yëgle ci gaawu bii yemook 12i fan ci weer wi, di ci wax ne ginnaaw buñ sukkandikoo ci «Article 76 du code des communications électroniques»,  àq yi “Orange” am la “Wave” am. Xamal nañu Sonatel ne sàrt boobu da koo war a doxal ci yoon, ñépp bokk ci yem mu bañ a am Kumba am ndey ak Kumba amul ndey.

Liy dëgg moo di ne “Wave” “Amerig” la fi teewal. “Orange” teewal fi Farãs niki Auchan, Total, Tigo, ak ñoom seen. Kon, mënees na ni li réewum Emmanuel Macron aakimoo Senegaal bare na. Lii rekk war naa tax doomi Senegaal yi yeewu, xam bu baax njeexital yi nekk ci xeex yu deme nii. Li doy waar ci mbir yi mooy ku ci déjjati moroomam ba ni faax, yaay yées ka fi nekkoon. Ndax jikkook boroom, pax. Nde ku ci nekk liy tonoom (bénéfice) rekk lay gis. Seen bopp rekk lañ fi nekkal te leneen yitteelu leen.

Kon sunu njiit yi war nañ def seen kem-kàttan ngir tënk ciy sàrt yile bànqaas, ba képp kuy doomu Senegaal di ci gis boppam, muy jaaykat bi di kilyaan bi.

AMI MBENG   

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj