Woodside Energy siiwal na xibaar buy neex Saa-Senegaal yi, rawatina njiit yu bees yi. Nde, kërug liggéey gii di yëngu ci wàllu soroj bi dafa biral ne, sémbuw soroj wi féete Sàngomaar, ci biir a biiru géeju Senegaal gi, liggéey na ba génnee 100i barigoy soroj bés bu set.
Ci njeexitalu juróom-benni weer yi njëkk yi atum 2024 mi, sémb wi matal 98 ci 100 yoo jël ñeel 22i teeni soroj ci kow 23i yi gas yi. Yéenekaay Bës bi moo ko siiwal.
Njiitul Woodside, Meg O’Neill wax na ni, Sàngomaar day yokk njureefi kërug liggéey gi, waayeet day jural Petrosen ak Senegaal ay njariñ yu sax.
Barigoy soroj yu njëkk yooyu ñu rootagum nag, yónnees na leen Tugal. War nañ tamit yónnee fa kembaaru Asii. Loolu di firndeel ne sémb waa ngi jëm kanam.
Li mat a xam mooy ne, soroj boobu ñuy génnee réew mi, di ko jaayi bitim-réew, mooy soroj bu ñu defaragul bi.
Dafa jot nag Senegaal am ay ndefari boppam yu mucc ayib ngir di fi mën liggéeyee soroj beek gil gi, di ko fi sopparñi, di ko jariñoo laata ñuy jaayi li ñu ci soxlawul. Looleet, ci moom sa bopp la bokk.