Mbirum ndiisoog luññutu gi dépitey PDS yi sumb ca Ngomblaan gaa ngiy wéy di jur coow ci réew mi. Ginnaaw bi UMS, kurél gi boole àttekat yi, génnee ab yégle di ci leeral ak a ñaawlu doxalinu dépite yi, àttekati Ndajem Ndeyu àtte mi génne nañ seen bos.
Juróom-ñaari àttekat yu Ndajem Ndeyu àtte mi àddu nañu ci tuumay nger ak ñàkk a maandu yi waa PDS gàll ci kow ñaari àttekat yu bokk seen biir. Ñoom nag, ñu ngiy artook a moytuloo ñiy jéem tilimal deru campeefi réew mi, bëgg a yee fitna ci réew mi. Ci seen yégle bi, ñoo ngi leen di xamal ne seen pexe moomu du àntu te duñ ko seetaan noonu muy neen. Rax nañ ca dolli sax ne, ñi sooke mbir mi duñ ci génnee noonu. Maanaam, juróom-ñaari àttekati Ndajem Ndeyu àtte mi, duñ bàyyi mbir mu sedd.