“ Yaa ma..” ji ak “Maa la…” ji a ngi tulle ak màlle ci làngug pólitig gi, rawatina ci kujje gi. Li Paap Jóob màng, fekki waa Bennoo Bokk Yaakaar, bokk na ci li xamb taal bi. Waaye, coow li jiitu na loolu. Ndax, ca jamonoy kàmpaañ ya, dafa am ay kàddu yu kii di njiital Pastef li, Usmaan Sonko, bokk ci lёkkatoo gii di Yewwi Askan Wi, yékkati woon fale ca diwaanu Mbàkke. Kàddu yooyu nag yeneen lёkkatoo yi ñaawlu woon nañ ko lool ngir lim ci waxoon ne “ Lёkkatoo YAW ak WALLU kese ñooy wujje ak BBY. Yi ci des yépp, Maki Sàll lañuy liggéeyal (àndal)”. Li mat a laaj kay mooy lan moo war a nekk jubluwaayu wax yu sew yees di faral di dégg ci biir kujje gi ? Ay pexe la ngir nёrmal yeneen lёkkatoo yi walla ngir jaay seen lёkkatoo yi ci kow yeneen yi la ?
Gaaral yi ak ŋàññante bi, du lu bees ci biir kujje gi. Ndax, ci lu yàggul dara, kii Paap Jibril Faal (MPR/Les Serviteurs), yékkati woon na ay kàddu teg leen ci ndoddu waa YAW ginnaaw ndajem-ñaxtu ma ñu amaloon ba ay bakkan rot ca. Kàddoom yooyu, juroon na ag réeroo ci digganteem ak militaŋi Sonko yi ba am fuñ ko doon dёkkale. Li ko jiitu tamit, amoon na kàddu yu Ceerno Alasaan Sàll tegoon ci ndoddu Bàrtlemi Jaas ginnaaw bim jёlee Gii Mari Saaña ak Séydinaa Umar Ture jox leen ay ndomboy-tànk ci meeri bu Ndakaaru. Ba tey, mbir mi yamul foofu, bi wayndare waa YAW amee ay jafe-jafe, ñii di waa AAR SENEGAAL génne woon nañ ab saabal di artu ngir lépp luy nuru ab baarayёgoo bañ a am ci wote yi. Loolu di ay firnde ci ne ay wax yu sew yàgg na ci biir kujje gi. Mu mel ni ku ràcc jёmale sa kanam. Kenn du nangul moroomam dara, ku la wokk rekk nga xuri ko.
Waaye, kàddu ya Usmaan Sonko yékkati woon ca jamonoy kàmpaañ ya dafa gёn a ñagasal seen diggante. Ginnaaw bi mu biralee kàddu yooyu nag, am na ay lёkkatoo yu jóg tontu ko, bi ci gёn a fés di bu waa AAR SENEGAAL ci baatu Ceerno Bóokum. Muy xamle ne “ Li Usmaan Sonko wax ay kàcc kepp la, dara du ci dёgg”. Mu mel ni làngug pólitig gi moom, tontu du fi forox, door fayu la. Lu waay wax suba, bala ngoon, mu jot tontoom. Loolu nag, taxul ba tey kii di njiital Pastef teggi tànkam fim ko tegoon. Mbooleem li gaa ñi fare ci yeneen lёkkatoo yi wax taxul mu dindi dara ci lim waxoon. Ndax, moom ci ay kàddoom nee na képp ku nekk ci kujje gi di xёy suba ba ngoon doo wax dara ci Maki, yow xeexoo Maki, ñi fare ci kujje gi ngay xeex.
Kon, ndax ŋàññi Maki Sàll rekk mooy tax a bokk ci kujje gi ? Moo tax, ñeneen ñi jàpp ne Usmaan Sonko lim wax tegu ko fenn ci lu dul bànneexu bakkanam. Te warul jàpp ne, ku dul moom walla ku bokkul ci moom baaxoo. Ba tax na, jamono jii, mbir yi tàmbali naa soppeeku. Ndax, xeex bi dafa mel ni day bёgg a des ci diggante gaa ñi fare ci kujje gi. Ndax, kii di Abdurahmaan Juuf bokk ci waa Aar Senegaal biral na ne waxi Usmaan Sonko yi yàqal na leen lu bari a bari. Me ne :
“ Wax ji dafa am njeexital bu baax a baax ci njureef yi. Dañoo yàq xel yi. Damay daje ak nit mu naan ma li ñiy wax ndax dëgg la. Bi ñu ko dalee wax ca njëlbéen ga la ñu naan ay wujji kujje gi lañ, Aar Maki ak yu ni deme…”
Ba tey, ñoom ak waa lëkkatoo gii di Les Serviteurs seen taxawaay soppikuwul benn yoon ginnaaw njureefi négandiku yi. Te, ñi ngi wéy di fànq kàdduy Usmaan Sonko yi. Donte ne sax, kii di Paap Jóob firnde la ci wax ji. Moom mi fekki waa BBY ngir nërmal kujje gi. Maanaam, moom ki tax waa BBY ëpp doole ñii di kujje fale ca Péncum ndawi réew ma.
Léegi nag, ñoom ñi jàpp ne Nguur gi fi nekk liggéeyul bañ sos seen i lёkkatooy bopp ngir jёle ko fi. Bu ñuy xeex seen biir, kon kan moo ko fiy jёle ? Moo tax ñu war a settantalaat seen taxawaay. Ndax, dafa mel ni kujje gi moom kóolute amul seen diggante. Ku nekk a ngi jiiñ sa moroom bokkoo ci kujje gi. Mёnoo bёgg mbir ak safaanam walla bёgg nen bañ ganaar. Bu dee seen jubluwaay defar réew mi kepp la. Kon kay, waruñoo nekk ci gaal gi ba pare di bёgg mu suux. Ñii ñoo fare ci kujje, ñee fare wuñ ci, li ci kanam rawul i bët. Lu tëw a xam daa yàggul.