Bi Njiitu réew mi waxee démb ne du bokk ci wotey 2024 yi ba tey, nit ñaa ngi wéy di ci joxe seen i xalaat. Muy ci kujje gi, waa Bennoo Bokk Yaakaar, way-moome yi, ba sax bitim-réew, ndogalu Njiitu réew mi lañuy waxtaane. Fi réew mi, boroomi tur yu bari àddu nañ ci. Xalifa Sàll séqoon na waxtaan ak RFI ak France 24, biral xalaatam ñeel ñàkk a bokk Maki Sàll ci wotey 2024 yi.
Njiitul Taxawu Senegaal dafa jàpp ne, ndogal li, « mbetteel gu neex a neex la. » Te, li ko sabab nag, du dara lu dul « ni askan wi defandoowee wenn say, ni ko waa bitim-réew tegee bët ak kàddoom gim joxe woon. »
Xalifa Sàll a ngi rafetlu tamit coppite gi ñu nar a soppi càrtug wote yi ngir mu mën a bokk. Moo tax, bees ko laajee ndax day bokk, dafa tontu, ne : « Dinaa nekk lawax bu soobee Yàlla. »
Bi ñu ko laajee ndax loolu du lum waxtaane ak Maki Sàll ci suuf, ni ko Usmaan Sonko waxee, dafa daw wax ji, ne : « Duma tontu mukk ciy tuuma yu amul cëslaay. » Te sax, moom, Xalifa Sàll, tuddul wenn yoon turu Usmaan Sonko ba ni waxtaan wiy jeexee. Waaye, ciy waxam, yéeneem mooy ñu amal wote yoy, ñépp ñoo ciy bokk, ñu bañ a beddi kenn.