XALIFA SÀLL JIITAL NA BÀRTELEMI JAAS

Yeneen i xët

Aji bind ji

Bàrtelemi Jaas mooy jiite kàmpaañu Xalifa Sàll. Ci ngoon gi la xibaar bi rot. Moom, meeru Ndakaaru bi, yàgg na ànd ak Xalifa Sàll. Ñoo nekkandoo woon PS laata ñu fay jóge di samp kurélu Taxawu Senegaal. Bu ko defee, moom Bàrt la lëkkatoo « Khalifa Président 2024 » tànn, jiital ko ci pekkug kàmpaañ bees dégmal.

Kon, moom mooy lootaabe ak a tëral naalub kàmpaañu lawaxam bii di Xalifa Sàll.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj