XEW-XEWI NDÉGLUG USMAAN SONKO GI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ci alxames jii weesu, ñetti fan ci weeru nowàmbar, la kii di Njiital PASTEF li, Usmaan Sonko, doon janoo ak àttekat bi. Li waraloon loolu nag, mooy mbirum siif mu ko ndaw sii di Aji Saar jiiñ. Mbir mi, féewaryee 2021 la dooroon, di wéy ba jur coow lu rёy ci réew mi. Ba mu am sax lu tollu ci fukki nit ak ñeent yu ci ñàkke seen bakkan, ci weeru màrs 2021, ñeneen jёle woon ciy gaañu-gaañu. Boobu ak léegi nag, bari na lu ci xew ci diggante bi, bari na tamit ñu ñu ci déglu. Keroog, ci alxames ji lañu doon déglu kii di Usmaan Sonko ci mbir moomu. Waaye nag, ca bés boobu dafa am yu ca xewaat te ya ca gёn a fés di laaj tontu yi doxoon digganteem ak àttekat bi nga xam ne, jamono jii, lёmbe na réew mi. Ak tamit, jàpp gi ñu jàpp ñiy wattu kaaraange Usmaan Sonko. Li mat a leeral kay, mooy yan laaj lañu ko laaj ak lan la ci tontu? Ak lan moo waral jàppug ñenn ci ñiy wattu kaaraangeem ? 

Bi ñu biralee ne ci alxames ji lañuy déglu kii di Usmaan Sonko, xel yu bari teeyoon nañu ci lan mooy xew ndax li fi jotoon a jaar ci màrs 2021. Ndax kat, ku ndóbbbin ray sa maam, foo gisatee lu ñuul, daw. Te, ku gumba ba wér, dinga xam lu bёt di jariñ. Li ko waral mooy ñu bari dañoo jàppoon ne bu ñu ko woowee rekk ay ñoñam jóg. Ndax, ca bésub àllarba ca suba la ñii di waa Yewwi Askan Wi, lёkkatoo gi mu bokk, amaloon seen ndajem-waxtaan di artu, di ko dooleel tamit. Waaye, moom ndeyu-mbill gi ca ngoon sa la def ndajem-waxtaan daldi xamal ay ñoñam ne jarul kenn di génn. Nde, dina dem wuyuji ci jàmm, ñibbisi jàmm. Te, bi mu xёyee ci alxames ji, noonu la ko defe ba àgg ci ёttu àttekaay ba. Ba mu fa àggee nag, ba duggu ca pekkug àttekat ba la takk-der yi teg loxo lu tollu ci juróom ci way-wattu kaaraangeem, yóbbu leen fale ca diwaanu Mbuur. Ñu bari di laaj nag lu waral loolu ?  

Bees sukkandikoo ci saabal bi kii di Mamadu Jóob, toppekatu Mbuur bi, fésal mi ngi ciy xamle ne ñi ngi leen di toppe coow lu amoon ci bésub dibéer 30 oktoobar boori juróom-benni waxtu ca ngoon, ca diwaanu Ciki. Coow loolu ñu leen di toppe nag, mi ngi sosoo woon ci ab jàmmaarloo bu doxoon seen diggante ak mbokki soxna sii di Faatu Njonn ba am ñu ca jёle ay gaañu-gaañu. Waaye, li xaw a ub bopp ñenn ñi mooy ni ñu ko defe. Maanaam, lan moo tax ñu xaar ba bés boobu, ñu leen di soog a teg loxo ? Am sax ñu jàpp ne dañu leen a kёf. Ndax, dañu leen a fekk ñuy doxal seen liggéey ñu jàpp leen. Te, ñu mёnoon leen a woo walla ñu yónnee leen plainte ñu wuyuji. Am tamit ñu jàpp ne Usmaan Sonko dayo bi mu am ci réew mi ngir nga jàpp ñu ko jegee noonu fàww nga doxale noonu te coow du jib. Walla mu fekk ne ay pexe la ngir gàllankoor nemmeeku tour bi muy def. Waaye, Usmaan Sonko mi nga xam ne mooy seen njaatige xamle na ni mbir yi deme, ndax nee na:

Ñi ñu jàpp defuñu dara, ñooñu man lañu àndaloon. Ndax, boo seetloo ñi ñu gёn a teg bёt mooy ñi gёn a jege Usmaan Sonko, ñi nga xam ne doo gis Usmaan Sonko mukk te gisoo leen (…). Waaye, jàpp ay nit yóbbu leen ci ay néeg daldi woo waa ñiy tuumaalaate, ne leen xool leen ndax ñii la ? Ñu ni waaw ñii la. Mu jóg moom toppekat bi nekk àttekat ci saa si ndax nee na ñi ñu jàpp ñoo def. Te, moom dafa war a toppe rekk warul a àtte (…). Dañu ne nañu leen di bunduxatal rekk saa bu ñu demee ba sёs rekk dinañu def dara. Moo tax nu dem ba Ciki, ñu jёl koo xam ne ça Njiiteef ga lay liggéey, Maki Sàll la àndal, dem ba foofu ñu waajal seen am cong. Te, li ci ёpp ñoom ak ndawi dёkk ba la ndax dañu faa am ay militaŋ, nu am fa ay militaŋ te noo leen fa ёpp militaŋ ndax noo fa jiitu ci wote yii.”

 Loolu nekk benn ci xew-xew yi amoon ca bés boobu. Ñaareel bi te mu lёmbe réew mi di laaj yi ñu ko laaj ak la mu ca tontu. Loolu lépp biral na ko ca ndajem-waxtaan ma mu doon amal kerog ci àjjuma ji. Nee na àttekat bi ñetti laaj na ko laaj. Bu njёkk bi mooy ndax danga nangu joxe sa deret ñu def test ADN ? Mu ne ko “sama deret man mii dungeen ci jot de ilaa yawmi diini, sama tufliit sax du ngeen ci jot. Bu wayndare wi nekkoon sax loo xam ne joxe deret da ciy am solo, amul benn ci càrti Senegaal bu ma tёnk ngir ma joxe sama deret.”

Ñaareelu laaj bi mooy ndax séq nga ak ndaw si ? Sonko ne ko “mayuma la nga laaj ma xeetu laaj yii, na mujj tey nga may laaj lii. Ndax, sama ngor ak sama sutura ci coow lu deme nii kese, mayuma kenn mu ciy wax.” 

Ñetteelu laaj bi mooy ndax nangu nga ni dem nga fa ak yan bés nga fa dem ? “Mu ne ko man duma toog ci mbedd mi fu ma dugg bind ne duggu naa fa. Daan naa fa dem moom, wax naa ko ñépp dégg ko. Waaye, kañ ak ban waxtu jàppuma ko.”

Bi laaj yooyu jeexee nag ndawul toppekat bi ne dafa am ay laaj, mu ne ko moom du tontu ay laajam. Moo tax nuy laaj ndax lii yombul ? Lu tax doxalewuñu woon nii ca màrs 2021 ? Usmaan Sonko wax ak ay ñoñam ci ni mu ko defe kerog, ñoom tamit ñu bàyyi ko mu jaar fa mu bёggoon a jaar ndax moom nee na mёsul a wax ne du wuyuji. Te, moom nee na fa mu bёggoon a jaar 3 màrs ñu bañal ko ko, foofu la jaar keroog. Waaye nag, mbir yi dafa mel ni yamul foofu ndax kii di Usmaan Sonko dafa teg tuuma ci ndoddu gaa ñi mu jàpp ne dañoo laale ci mbir mi. Maanaam, ñi nga xamne ñoo lal pexe mi ngir tuumaal ko siif gi. 

Ndax, nee na ku tuumaal nit danga war a joxe ay firnde te ñoom joxewuñu benn firnde. Te, moom dina joxe lépp liy wane ne lii ay pexe yu ñu lal la ak ñi ko lal. Ñooñu mu duut baaraam nag ñii la : Sëriñ Basiiru Géy, Seneraal Musaa Faal, Kolonel Abdu Mbeng, Meetar Gabisoo, Meetar Joor Jaañ ak Mammadu Maamuur Jàllo. 

Mu mel ni nag léegi mbir yi dafa mujjee jël weneen yoon. Ndax, day mel ni ñi ëpp ci ñi ñu ci tuddu am na lu ñu séq ak APR walla ñu fa bokku. Kon coow li day waaj a jóge ci diggante Usmaan Sonko ak Aji Saar dem ci diggante APR ak PASTEF. Ak lu ci mën di am, yoon kepp a mën a leeral mbir moomu ci boppi saa-senegaal yi. Muy ki ñu doon jiiñ, mu dem ba mujj di jiiñaate fu mu ko teg ak ñi ko doon jiiñ fu ñu ko teg ?

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj