Ndakaaru dina amal ñaareelu xewteem ñeel ladab ci àddina si, FILID (Festival international de littérature de Dakar). Ginnaaw bi mu ko njëkkee woon amal ci atum 2022 (29 suwe ba 2 sulet 2022), dina ko tóllanti ren jii, li ko dale bésub 7 jàpp 10 ci suwe 2023. Wile yoon, ci ponk bii toftalu lees tënk waxtaan wi :
-
Moomeelub ladab ak mbindum jamono, muy joxe ci farãse “Patrimoine littéraire et écriture contemporaine”.