XIBAARI TÀGGAT-YARAM (9/9/24)

Yeneen i xët

Aji bind ji

Toogalante CAN 2025 : Senegaal waneegul lu dal xel !

Keroog ci àjjuma ji 6i fan ci sàttumbaar wii la ekibu Senegaal bu mag bi doon daje ak Burkinaa Faaso fii ci fowub Abdulaay Wàdd bi nekk Jamñaajo. Mu nekkoon mats bu Senegaal teeloon a jiital, ndax teel a dugal ca 16eelu simili ba. Amaat na fa yit ay yooni dugal yu mu waroon a mën a dollee bii yi, waaye defu ko. Ci noonu saa-burkinaa yi tamit bàyyiwuñu wenn yoon, gëm ko rekk, ba ca cappaandaw ga, ci simili yees di dolli, ñu daldi fa am benn kuufarã daldi koy dóor mu jur réeroo ci buntu këru Senegaal ba faf mujje ci bii. Mats bi jeexe ci 1-1. Gannaaw ga nag, dafa mel ni soppe yi béguñu ci ekib bi, rawatina ci tàggatkat bi, Aliw Siise. Foo dugg ci mbaali jokkoo yi gis seen mer ak wax yi ñuy wax jëmale ko ci moom ba naan dafa war a dem. Li waral loolee lépp nag du lenn lu moy sistem bi mu bëgg a tegal ekib bi. Ñu jàpp ni léeg dafay sax ndiru maa-tay. Ndax ci CAN bii weesu, ci mats bi nu Kóddiwaar di toogloo, boobu sistem la andi woon, (5-2-3), gannaaw ga mu dégg ca lu nekk. Waaye, taxul mu bàyyi ko, nde mu ngi koy wéyal ba léegi.

Tay ci altine jii, 9i sàttumbaar, la Senegaal amalaat ñaareelu ndajeem ñeel toogalanteg CAN bii di dikk, doon ci daje ak Burondi. Sunu gaynde yi ñoo mujje dóor benn bii ci tus (1-0). Ab penaatii la Ismayla Saar teg, dóor mu dugg.
Noonee la ñaari ndajey gaynde yi demee. Njàngat yees ci mën a amal mooy ni xar kanam bi ekib bi ame woon ca CAN 2021 ba, kenn gisatu ko. Ndax, futbal bu set lañu wone woon, mu gaawoon lool ba ekib yi mu doon dajeel dañu koy bàyyi xel bu baax. Mu wuute ak léegi. Loolu nag, ñu ci bari ci saa-senegaal yi ak ñiy wax ci wàllu futbal ci réew mi jàpp nañu ni taxawaay bi Aliw Siise andi léegi (5-2-3) moo tax. Dafa mel ni ndawam yi miinuñu lool boobu taxawaay. Ñu bari di wax ni daf ko war a soppi te dellu ca (4-3-3) ba ñu miinoon. Waaye, moom tàggatkat bi jàpp na ni taxawaay bu baax la te lu mën a dem la ba tax na du ko soppi. Wànte, daf ciy gën a tàggat ay ndawam ba ñu mën koo doxal bu baax. Lu mu mënti doon daal, war nañu gën a xoolaat yëf yi te amal njàngat ci mats yi weesu, rawatina bi ñu Kóddiwaar di toogloo ca CAN bii weesu. Lu ko moy xar-kanam gees xame woon ekib bi du gaaw a dikkaat.

  1. Ronaldo: beneen dayo ci futbal

Saa-portigaal bi noppiwul ngir bàyyi wenn yoon. Mu ngi wéy di aj turam ci mbooru futbal. Keroog ci alxames jii weesu, ca seen ndaje ak Kurwaasi ñeel “Ligue des Nations” bi la dugal lii di 900eelu biiwam, muy lu réy lu kenn defagul. Turam nekk lu kenn dootul fàtte ci mbooru futbal. Waaye tamit, lim fi def doon lu dootul yomb futbalkat def ko.

Ay biiwam :

Sporting Portugal : 5

Manchester United : 145

Real Madrid : 450

Al-Nassr : 68

Portigaal : 131

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj