Ekibu Senegaal dina dalal bu Burundi talaata jii nu dëgmal, yemook 19i pani nowàmbar 2024. Ca fowub Abdulaay Wàdd bu Jamñaajo la joŋante biy amee. Joŋante boobile nag, mooy tollook 6eelu bëccëgu tooglante CAN 2025 biñ dëgmal. Muy joŋante bu am solo bees di waajal nim waree. Tay jii ci àllarba ji lees tàmbalI jaay tike yi ci lënd gi. Ci àjjuma ji lees di ubbi giise yiy jay tike yi. Xamalees na tamit ni, ci béréb yi toftalu lañu leen di jaaye : fowub Demba Jóob, Aamadu Bari, Alasaan Jigoo, Mañaŋ Sumaare bu Cees, Ngalàndu Juuf, Daluwaayu FSF ba woon te janook CICES, kërug mboor Duuta Sekk ak ca Meeri bu Jamñaajo. Mbaa nga jaaree ko ci lënd gi def www.fsf.tickets-stade.com.
SUPERCUP ESPAAÑ : ARMINAATU PO MI GÉNN NA
Dëmi-finaal yi :
Keroog 8i pani sãwiyee 2025, Real Madrid moo ciy daje ak Majorque. Ca ëllëg sa, 9i sãwiyee Barcelone war na joŋante ak Athletic Bilbao.
Finaal bi mi ngi war a am keroog 12i pani sãwiyee 2025.
Njortees na ne, beneen kalaasikoo dina amaat, muy ci diggante Barcelone ak Real Madrid.
BAFETIMBII GÓMIS BÀYYINA FUTBAL
Bafetimbii Gómis mi ngi am 39i at ci ren. Moom nag, dafa jël ndogalu summi ay karàmpõwam. Loolu la xamle, wax ne bàyyee na futbal bi ak xale yi. Fa réewum Sapõ la Saa-Farãs bi tëjee jaar-jaaru futbalam. Nde, fa la mujjee futbal gannaaw ba mu jógee ca sàmpiyonaa Farãs. Cig dundam nag, amal na ci lépp-lépp 802i joŋante, daldi ciy dugal 361i bii.
LÀMB JI
Móodu Lóo – Sitta
Ñaari mbër yi dinañu amal seen jàkkaarloo bu mujju ëllëg ci alxames ji (14i nowàmbar 2024) bu 20i waxtu jotee. Fa Triplex la jàkkaarlo biy amee. Waaye, mënees na ko seetaan daar-daar ca tele Lutte Tv.
Rëg-rëg waadab àddina ci One Heavyweigth
Omar Kan, ñu gën ko miin ci dàkkentalu Rëg-rëg, sagal na réewam, sagal Afrig gépp. Ndaxte, keroog 9i pani nowàmbar (1 waxtu ci guddi) la doon daje ak Anatoly Malykhin, di Sa-Riisi bi téewoon fowug MMA ci loxoom. Mu di woon waa ju doy-waar, mën li muy def lool te soxor ci lool, ba tax ñépp doon ñaanal doomu réew mi ak di xalaat ndax mën na ko gañe. Waaye, Rëg-rëg boole njàmbaar ak jom, dëggal boppam ba am ci ndam. Ñu seetlu ne, bu njëkk, ni moom Malykhin daawul taxawaalu ak kenn, ci mel ak saa mu lijjanti la, bom la. Waaye, keroog de, daje na ak doomu bàjjenam. Nde, Rëg-rëg sonal na ko lool, yóbbu ko ba ca 5eelu géewal ga (round) ba mujje koo gañe. Muy lu rëy ci Senegaal ak Afrig.