Noppees na ci matsi jàllug CAN bi ci ayu-bés bees weesu. Ñaar-fukk ak juróom-ñeenti ekib yii ñooy dem fa Marog ñeel po mi : Marog, Burkinaa Faaso, Kamerun, Alseri, RD Kongo, Senegaal, Esipt, Àngolaa, Gine Ekuwaatoriyaal, Koddiwaar, Gabõ, Ugàndaa, Afrig dii Sidd, Niseriyaa, Tinisi, Simbaabuwe, Sàmbi, Mali, Komoor, Sudã, Benee, Tansanii, Botswanaa ak Mosàmbig.
Ci kow loolu, CAF fësal na diwaan yi nar a dalal po mi fa Marog. Yii la :
Kaasabalankaa, Rabaa, Tansee, Fes, Agadir ak Marakes.
Ba tay nuy fàttali ni CAN bi dina tàmbali ca 21i desàmbar 2025, finaal ba nekk 18i sãwiyee 2026.
CAN 2025 (JIGÉEN) : PULUF NAÑU KIPPU YI.
Powu CAN 2025 bu jigéen ñi itam jàppees na lélub tàmbaleem ba sax puluf nañu kippu yi ba ku nekk xam fum féete.
Kippu A :
Marog, Sàmbi, Senegaal, RD Kongo
Kippu B :
Niseriyaa, Tinisi, Alseri, Botswanaa
Kippu C :
Afrig dii Sidd, Gana, Mali, Tansani
Joŋante bi dina tàmbali bésub 5i Sulet 2025 dem ba 26eelu fanu weer wa.
“LIGUE DES NATIONS”: 1/4 FINAAL YI LEER NA !
Fale ca Tugal, seen po yi dinañ tàmbali ca weeru Màrs wee di ñëw. Ñu toll ci 1/4 finaal yi, 8i ekib séq ko. Nii la seen puluf tëddee :