XIBAARI TÀGGAT-YARAM

Yeneen i xët

Aji bind ji

REAL MADRID JËLATI NA KUB

Real Madrid moo ngi ak xalimaam di bind mbooram rekk ni du taxaw. Démb ci àllarba ji, 18i desàmbar 2024, fale ca Araabi Sawdit la këlëbu péeyu Espaañ bi doon amal finaalu kuppeg kembaar yi (trophée intercontinentale). Mu doon ci daje ak Pachuca, ab këlëb bu nekk Meksig. Real Madrid moo bom 3i bal ci dara. Daanaka bettul kenn. Mbappe, Rodrigo ak Vinicius (penaltii) ñoo dugal. Carlos Ancelotti, tàggatkat bi doon ci tàggatkat bi ëpp lu mu jël raaya ca ekib ba, 15i kub ci tay. Mbappe it, bii mooy ñaareelu kubam ca Real Madrid, ak ñaarelu biiwam ci finaal, foofu.

FIFA THE BEST

Vinicius Junior lees tabb futbalkat bi gën a xereñ ci atum 2024 mi. Muy lum yellool. Ndax, at mu réy la def, jël ciy kub ak Real Madrid, waaye itam mu wane ci xereñte bu ñépp teg bët. Fan yale ci gannaaw, lees ko joxul “Ballon d’or” bi juroon na coow lu réy. Ndaxte, ñu bare dañu jàpp ne moo ko yello woon, donte ne ki ko jël (Rodri), moom it yelloo na ko. Daanaka, àdduna sépp sargal na ko ci “Fifa the Best” bi. Bu ko deee, Vinicisu mooy 6eelu Saa-Beresil bu ko jël ginnaaw Romario, Ronaldo, Rivaldo, Ronaldiñoo ak Kaka. Mu nekk itam 3eelu futbalkatu Real Madrid bu ko jël ginnaaw C. Ronaldo ak Modric.

“BALLON D’OR” AFRIG 2024

Ademola Lookman, moo teggi natt bi. Moom Saa-Niseriyaa bi moo gañe lii di “Ballon d’or Afrig 2024” bi. Yelloo na ko ! Nde, ci CAN bi weesu, ñépp ràññee woon nañu ko ndax mën futbalam, waaye ak njariñ li mu amaloon ekibam itam. Ba fee ca Tugal sax, desu fa gannaaw. Ndax bokk na ci ndaanaani Atalanta (Itali) yi.

LAMIN YAMAL GAAÑUWAAT NA

Xale Barcelone bi dina toogaat lu toll ci ñett jàpp ñeenti ayu-bés yoy, du ci dugg pàkk. Keroog ci seen mats bi ñu ñàkk (1-2) ak Leganes la ame ab gaañu-gaañu. Gannaaw bi ko fajkat yi saytoo, xamlees na ni ci dojor bi la gaañu, loolu di ko dàkk ci pàkki futbal yi ab diir.

MANCHESTER CITY MU NGI CI GUDDI YU LËNDËM

Jamono jii, ekibu Pep Guardiola bi xamatul ban tànk lay feccee. Lépp a jaxasoo. 11i mats a ngi nii amu ci ndam, ba noppi ñàkk ci 8. Loolu di wane ni mu ngi ciy jafe-jafe. Lu doxul ?

Barkaati-démboo Njaay la ko dëkkandooram bi, wujjam wii di Manchester United daldi dóor 2-1 ci mats boo xam ni moo jiital ba ca 10i simili ya mujj ya, ñu daldi koy bittarñi dugal ko ñaari bii yu gaaw.

LÀMB JI

12i sãwiyee, ay ndaje yu réy ñoo ci war a am. Jokkel di na daje ak Màcca Pereraa, Ibu Aafiya / Arme, Talfaa / Pokolaa Balde, Jéen Kayre / Fiis dë Bàlla, bu mag bi di diggante Giri Bordóo ak kii di Sarkóo.

Balla Gay 2 / Sitta mu ngi ci tànki taxaw

Alburaax Events mu ngi def ay jéego ngir taxawal làmb jooju. Daanaka mbir yi sori na. Ci lees foree ci wewu béy, ci boori Sitta la mbir mi xawee des. Ndax dañu bëgg ñu fay leen njëkk lu ëppatëllëw. Waaye, ciy waxtaan, mbir yaa ngi bëgg a tënku. Ñu bàyyi ci nopp ba xam fu muy mujje.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj