XIBAARI TÀGGAT-YARAM

Yeneen i xët

Aji bind ji

Senegaal jàll na ci mbooleem powi Afrig ci atum 2025 yi. Loolu di jéego bu réy. Loolu day wane tamit dayob futbalu Senegaal, waayeet di biral seen ug njàmbaar. Ci joŋante yii toftalu la bari Senegaal yiy bokk :

  • CAN U15 (scolaire)

  • CAN U17

  • CAN U20

  • CHAN

  • CAN JIGÉEN 

  • CAN GÓOR

Globe Soccer Awards 2024

Real Madrid buub na daanaka lépp. Boobu xew-wex di lees di amal at mu nekk, di ci neexal ak a sargal ñi gën a xarañ ci at mi ñu génn. Ren nag, ekibu péeyu Espaañ ba dafa ñëw rekk aakimoo daanaka lépp. Real Madrid moo fa jël :

– Këlëb bi gën a xarañ ci atum 2024 mi ;

–  Tàggatkat bi gën a xarañ (Carlo Ancelotti) ;

– Njiit li gën a réy ( Florentino Pérez) ;

– Prix (carrière joueur) Thibaut Courtois ;

– Prix Maradona (Jude Bellingham) ;

– Ataakã bi gën a xarañ (Vinivius jr) ;

– Miliya bi gën a xarañ (Bellingham) ;

– Futbalkat bi gën a xarañ (Vinicius jr) ;

Ba tay, ca xew-wex booba, sargal nañ fa Cristiano Ronaldo, daldi ko fay tabb “dugalkat bi gën a màgg ci jamono yépp”. Moom mees di dàkkentale CR7, jalooreem a ngi lalu ci 1, 255i mats, 916i bii ak 256i paas.

Lépp di 1172i bii ak i paas yu mu def ci 1 255i mats ci jaar-jaaru futbalam (bu jeexagul). Mu jiitu ñii di Messi (850i bii), Josef Becan (805i bii), Romario (772i bii), Pelé (757i bii).

Supercup Espaañ 2025

Po mi dees na ko amale fa Araabi Sawdit, ca fowub Al Jawhara ba nekke diwaanu Jidda. Naalu po mi tëddee nii : 

Demi-finaal yi :

Real Madrid / Real Mayorque (8i sãwiyee 2025)

Barcelone / Athletic Bilbao (9i sãwiyee)

Finaal bi :

Ñaar ñii dóor ci demi-finaal yi (12i sãwiyee)

Arbitu futbal bi gën a xarañ

IFFHS tabb na FRANÇOIS LETEXIER arbiitar bi gën a xarañ ci àddina si. Kii di Stéphanie FRAPPART lees tabb ñaareel bi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj