Ci gaawub 7i sãwiyee bii lees doon amal finaalu “Super Cup d’Italie” bi. Mu ngi doxoon ci diggante Inter Milan ak Milan AC. Aji-mujj ji moo ko mujje jël ci kaw dëkkandoom bi. Mu nekkoon mats bu metti, waaye it doy waar. Ndax, Inter Milan moo jiitaloon ñaari bii, Abraham ak i farandooram fekk leen faak ñetti bii. Ci 3-2 la jeexe, Milan AC daldi koy jël, mu dabaale ci Inter mi mu dóor ci yoon yuñ jël kub bi. Ñoom ñaar ñépp jël nañu ko 8i yoon top, ci gannaaw Juventus mi toogee 9.
TROPHEE DES CHAMPIONS : PARIS SG MOOY WAADA BI !
Mbappe dem na, waaye yóbbaalewul kub yi ! Paris Saint-Germain mu ngi wëyal di jël kub. Nde, barki démboo-njaay, ca dibéer ja, la doon dajeek Monaco ñeel finaalu kuppeg waada yi (Trophée des Champions), mu mujje ko jëlati. Bii di 13eelu yoon yum ko jël ba muy PSG ba léegi. 1-0 la ndaje ma mujje, Usmaan Démbele moo dugal ca 91eelu simili ba.
PREMIER LEAGUE : ISAK DUGAL NA TURAM CI MBOOR MA
Mu ngi dikkoon ci sàmpiyonaa Àngalteer atum 2022. Ci diggante boobu ak léegi dugal na ci 50i bii. Diir bim ko def, Erling Haaland (105) ak Muhammed Salah (73) rekk ñoo def li ko gën. Fim ne, bokk na ci ataakã yees gën a bàyyi xel ca sàmpiyonaa ba. Ekib yu mag yi itam ñu ngi koy bàyyi xel bu baax.
NIKOLAA JAKSON GËJ NA DUGAL
Ca seen ndaje ak Brentfort, 15i desàmbar, la Nikolaa Jakson gëj a dugal. Loolu nag, tax na ba futbalkatu Chelsea ba woon, John Obi Mikel, di ko cuqaat. Kàddu yii la ko sànni : ” Jakson du dugal lu bari, bu Chelsea amoon Oshimen walla Victor Gyokeres, dinanu bokk ba léegi ci ñiy xëccoo sàmpiyonaa bi. Dëgg la, mën na futbal, mën na dawal bal bi, waaye du dugal lu bari… ataakã la, dafa war a dugal lu bari”. Yooyu kàddu la saa-niseriyaa bi teg ci ndoddu Nikolaa Jakson. Mu niru lool xaste, waaye jege itam ay kàdduy ñaax ngir mu fippu.
LÀMB JI
Alburaax Evens taxawal na bëre Balla Gay 2 ak Sitta keroog ca 2eelu fanu sãwiyee wii nu nekk. Ñu ngi ko jàpp bésub 20 Sulet 2025.
Dibéer 12i sãwiyee, bés bees yàkkamti la ndax ndaje yu mag ya cay ami. Lu ci mel ni mu Giri Bóordoo/Sarkoo ak Pokolaa/Talfaa, ñoom ñi nga xam ni seen jàkkaarloo yi tàngoon na jërr.