XIBAARI TÀGGAT-YARAM

Yeneen i xët

Aji bind ji

LÀMB JI

Dibéer 16i fani féewiryee mooy bés bi njabootug lamb yépp di xaar. Ndax, ca bés booba la ñaari waada yu mag war a daje, ñuy Aama Balde, doomu Pikin ji, ak Farã, doomu Pàrsel ji. Muy bés bu réy, ñaari mbër yu mag war cee sëgg. Njortees na ci bëre bu neex. Waaye, yamul foofu, ndax ca bés ba, Liis Njaago dana ca daje ak Lac Rose, Doomu Daagu / Caatu Yoof, Nàndi Faal / Ñaŋ Baalo, Ndigal / Bildoseer, Sox bu ndaw ak Mbay Fay

KUPPE

  • Saaliw Siis amaat na këlëb

Saaliw Siis bokkoon na ci waaday CAN 2022 bi. Moom nag, at mooma la gëjoon a am këlëb. Waaye, léegi, daldi nay amaat këlëb bu bees ca Farãs. Xaatim na fa Entente Feignies Aulnoy Fc, di këlëb bu nekk ca National 2 ba. Mu sori lool dayo ak fa mu tolloon ci futbal, waaye wolof nee “ku amul ndey, nàmp maam ! “

  • Ligue des champions

Ay daje dina am ci ayu-bés biñ jëm ñeel ekib yi war a leeral seen ug jàll. Maanaam ekib yi dem “barrage”. Gannaaw puluf, nii la mats yiy tëdde :

Atalanta / Fc Brugge

Dortmund / Sporting

Real Madrid / Man City

Bayern Munich / Celtic

PSV Eindhoven / Juventus

AC Milan / Feyenoord

Paris SG / Brest

Benfica / Monaco

  • Coupe du roi

Àllarba 12i fani féewiryee lees di amal jiifii-jaafaawu dëmi-finaali po ma. Ñeenti ekib yii ci desandi, ku nekk mën ci dajeek sa moroom, ñooy : Real Madrid,  Atletico Madrid, Real Sociedad ak Barcelone.

  • Ligue 1 : Usmaan Démbalee ngi dox ci ndox.

Saa-Farãs bi, jamono jii, ciy loxoom la Paris Saint-Germain nekk. Moo fa taxaw taxawaayu Mbappe, boot ekib ba tey doxal. Fim ne, mu ngeek 16i bii ca sàmpiyonaa ba, waaye it 21i bii buñ boolee matsam yépp. Mu bokk, nii, ci atakã yi gën a tàng ci futbal bi. Bile taxawaay nag, ñu ci bari nee nañ daf ko yéex a def, nde ku ko seetaan xam ni mën na lu ko raw.

  • Marcelo bàyyi na futbal

Saa-Beresil bi biral na ni bàyyi na futbal bi ciy 36i atam. Mu bokk ci laafi càmmooñ yi gën a xarañ ci àddinay futbal te ñu gënoon koo ràññe ca Real Madrid.

Cig dundu futbalam, moom Marcelo amal na ci 663i mats, 58i yoon yu ko Beresil dëkkam woo, mu bom ci 30i kub, waaye mu dugal ci 52i bii daldi ciy defaale 106i paas. Sargalees na ko démb ca ndajem “derbi” Real Madrid ak Atletico Madrid bi mujje ci 1-1.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj