Wii yoon leer na ni Saa-Farãs bi dafay jóge Paris Saint-Germain. Keroog, alxames 15i féewiryee la ko yéenekaay yu bari ca tugal siiwal. Wii yoon muy xibaar bu dëggu. Nde, ca ëllëg sa, àjjuma ja, këlëbam daldi nay wax lu jëm ci loolu, xamle ni dëgg la Mbappe dina jóge ca ekib ba weeru suwe 2024. Fa mu jëm nag, kenn xamagul. Waaye, xel yépp a dem ca Real Madrid ma nga xam ni at yii weesu yépp mu ngi topp ci ginnaaw futbalkat bi. Ay jegeñaaley Mbappe itam ñu ngi waxantu ni fa Real Madrid la seen waa ji bëgg a dem. Ñoo ngi ruumandaat sax ne torlu na kontaraawam ba noppi. Lees mën a jàpp daal, mooy ni moom Mbappe dina jóge Paris Saint-Germain bu atu futbal mi jeexee.
Bayern Munich mu ngi ci guddi yu lëndëm
Jamono jii ekibu Tuchel bi mu ngi ci guddi yu bët setagul. Fim ne, seen ekib bi bari nay jafe-jafe. Ci dibéer jii weesu, Bochum moo ko dóorati 2-3. Seen jafe-jafe yi nag, yamul ca sàmpiyonaa ba rekk. Ndax, keroog Lazio moo ko gañe ca seen ndajem “Ligue des champions” ba, ñeel 1/8 dë finaal yi. Rax-ci-dolli, toog nañu ci joŋantey “Coupe d’Allemagne”. Mu nekk jàngoro joo xam ni bees ko saafarawul dana jur tàqalikoo diggante këlëb ba ak tàggatkatu yaram ba, Tuchel.
Musaa Wage, waaw-góor !
Doomu Senegaal jaa ngi def i jaloore yu réy fa réewum Siipar (Chypre). Kenn réerewul jafe-jafe yim nekkoon. Waaye, dafa gëm boppam, daldi liggéey ba dikkaat. Ci atu futbal mii, moom lees tabb “Latéral droit” bi gën na xarañ ca sàmpiyonaa ba.