Dibéer 16 féewiryee jii weesu la doomu Pàrsel ji, Farã, doon sëgg ak Aamaa Balde bu Pikin fa “Arène nationale” ba. Farã moo mujje daan Aamaa daan bu gaaw te yomb. Seen bëre bi, gannaaw yenn kurpeñ yiñ jot a sàndante, ci mennum cong la jeexe. Farã Gómis mel ni ku dëggal li mu wax ni moo mën doomu Pikin ji, ndax doole feeñ na fa. Mu des, nuy laaj kan lees ko war a joxaat. Lu leer ba leer mooy ni àndandoo Móodu Lóo bi gën na aj darajaam ci làmb ji.
Ca bés ba itam, Liis njaago doon na ci bëre ak Lak Róos. Ci dóor mu daanu la mujje. Xale Jàmm-a-gën bi moo jël ndam li, ñibbeek moom.
Bi lamb jeexee, fitna juddoo na ca ba am ku ci faatu. Loolu moo tax jëwriñu biir-réew mi jël na ndogalu génnee loxoom ci làmb jib a jëmmi jamono.
LIGUE DES CHAMPIONS
Matsi baaraas yi ngir jàll ca 1/8 finaali po mi jeex nañu ci àllarbay démb ji. Ñu nekkoon ay ndaje yoy, ku ci nekk ñaari yoon nga doon daje ak sa moroom, dalal ak fekki. 8i ekib yii di : Real Madrid, Bayern Munich, Fc Bruge, Dortmund, Paris SG, Benfica, Feynoord ak PSV Eindoven ñooy yi jàll ca baaraas ba. Warees amal ab puluf ci àjjuma jii, 11i waxtu ngir leeral ñan ay daje ci 1/8 yi.
1/8 dë finaal :
Real Madrid (Atletici Madrid/Bayer Leverkusen)
Bayern Munich (Atletico Madrid/Bayer Leverkusen)
Fc Bruge ( Lille/Aston Villa)
Dortmund (Lille/Aston Villa)
Paris SG (Barça/Liverpool)
Benfica (Barça/Liverpool)
Feynoord (Arsenal/Inter Milan)
PSV Eindhoven (Arsenal/Inter Milan)
KEYTA JAAWO BALDE
Keyta Jaawo Balde, saa-senegaal bi, amaat na këlëb gannaaw ba mu dogee woon pasam ak Sivasspor ca weeru Sãwiyee wa. Daldi nay amal pas gu bees ak këlëbu AC Monza (Itali), muy këlëb bi nekkagum ndàdde ca sàmpiyonaa Itali ba. Xaatim na fa diirub fii ak atu futbal miy jeex.
VINICIUS JËND NA AB KËLËB
Vinicius Jr jënd na ab këlëbu 2eelu yamuwaay (2e Division) fa Portigaal. Moom saa-beresil bi, matal na lépp lu ci waroon ba doon na boroom Alverca RCA.
PARIS SG MI NGI CI DIGG-DOOLEEM
Paris SG ñàkkagul benn matsam ca Ligue 1 ba. Ekibu péeyu Farãs bi moo ngi doxal atum futbal bu jéggi dayo ca sàmpiyonaa ba. Mu ngi amandi 22i mats yoy 17i yi daf leen bom, daldi timboo 5 ya. Kenn dóoragu ko. Muy lu rëy !