Barcelone daldi nay dóor Real Sociedad 4-0, daldi nangu boppu po ma gannaaw ba Real Madrid mi mu yamoo woon I poñ tarxiisee barki-démb ca gaawu ga, ca fowub Real Betis (2-1).
Atletico Madrid itam jaare na fa toog ca ñaareelu tooguwaay ba gannaaw ndam li mu am ci kaw Atletic Bilbao (1-0).
1- Barça 57i pñ
2- Atl. Madrid 56i pñ
3- Real Madrid 54i pñ
SERIE A
Ca sàmpiyonaa Itali ba, Inter Milan moo toogandi ca bopp ba ak 58i poñ, topp ci Napoli ak 57i poñ, Atalanta di ñetteel ba ak 55i poñ
PREMIER LEAGUE
Ca Àngalteer Liverpool moo nekk ca bopp ba ba léegi, toogaale ca ak 67i poñ, rawee ña ca des benn mats. Arsenal moo koy dàkk ak 54i poñ, moom it ca gannaawam Notingham Forest mi koy ñàkkante ren ak 48i poñ. Manchester City, donte aji-feebar juy jafandu la ren, bàyyiwul. Nde, mu ngi ca 4eelu palaas ba ak 47i poñ.
LIGUE 1
Bu nu demee ca Farãs, PSG moo nekkati ca kaw, di amal at mu jaar yoon, ndax ba nëgëni, kenn gañeegu ko ca sàmpiyonaa ba. Mu toog ca kaw a kaw ak 62i poñ, Marseille topp ci ak 47i poñ. Nice moo leen ñetteel ame 46i poñ.
BUNDESLIGA
Ca Almaañ, Bayern nanguwaat na boppu toogaay ba. Wii yoon nag, dafa takku ngir gañeeti po ma niki mu ko yàgg a defe. Moo nekk ca kaw ak 61i poñ. Bayer Leverkusen moo ca topp ak 53i poñ, Frankfurt di 3eel ba, am moom itam 42i poñ.
LIGUE DES CHAMPIONS
Ayu-bés bi, mats yu njëkk yi ñeel 1/8 dë finaal yi dina door. Ci talaata jii di 4 Màrs, bu 17iw45s jotee Club Brugge dina dalal Aston Villa. Ca 20iw wa, ñetti ndaje dinañ ca ame : Dortmund / Lille, PSV Eindhoven / Arsenal ak Real Madrid / Atletico Madrid.
Ci àllarba ji, 17iw45s, Feyenoord, ci pàkkam, dina daje ak Inter Milã. Bu ñu jógee ci loolu, niki ci talaata ji, ñetti ndaje amati ca 20iw wa. Benfica / Barça, Bayern / Leverkusen ak Paris SG / Liverpool