Ci weeru màrs wii, Senegaal dina ci amal ñaari mats ñeel 5eel ak 6eeli bés ci tooglantey kuppeg àddina siy ñëw. Ñaari ndaje yi nag, menn maa ngay ame ca fowub Benghazi, mu ciy daje ak Sudã (22 màrs), meneen may ame fii ci Senegaal, ca fowub Abdulaay Wàdd bu Jamñaajo, mu war ci daje ak Togo (25 màrs).
LÀMB JI
Jàmbaar Production taxawal na bëre Ëmma Seen ak Farã. Muy bés bu ñépp doon xaar ndax coow yi amoon seen diggante. Fi mu nekk nii nag, biralaguñu benn lél.
Alburaax Evens taxawal na itam diggante Giri 2 ak Fiis dë Bàlla.
Sitta : ” Bàlla dafa ameel séeréer si bor, fàww daf koy fay…” loolee la doomu Jàmm-a-gën ji xamle. Mu melni dafa bëgg a wax ni mooy fayul Yekini mi Bàlla Gay 2 daanoon. Ndax dana am ? Ndax dana yomb ? Ndax bor ba du jur rakk ? Lépp ca bés ba lay leere.
LIGUE DES CHAMPIONS
Mats yi ñeel 1/8 finaal yi jàll nañu ci talaata jii ak àllarbay démb ji. Mu nekkoon ndaje yu metti ci ekib yépp. Nii lañu demee :
Talaata 4 màrs 2025
Club Brugge 1-3 Aston Villa
Real Madrid 2-1 Atletico Madrid
PSV Eindhoven 1-7 Arsenal
Dortmund 1-1 Lille
Àllarba 5 màrs
Feyenoord 0-2 Inter
Paris SG 0-1 Liverpool
Bayern Munich 3-0 Bayer Leverkusen
Benfica 0-1 Barcelone
Mats delusi yi dinañ ami ci ayu-bés bii di ñëw. Yooyu ndaje nag, du doon yuy yomb. Ndax, fa la yëf yi di leeree, ñii jàll ca 1/4 finaal ya, ñee toog.
LIGGÉEYU JOSE MURINHO CA FENERBAHÇE
Saa-portigaal bi moo ngi def liggéey bu mucc ayib ca sàmpiyonaa Tirkii ba. Ba muy jël ekib bi, mi ngi ko fekkoon ca suuf. Waaye, mu ñafe ba yéegalaat ko ca ñaareelu toogaay ba. Liggéeyam ci at mi :