XIBAARI TÀGGAT-YARAM

Yeneen i xët

Aji bind ji

KUPPEG AFRIG U17

Guney Senegaal yi amal nañu seen matsu kippu bu njëkk. Seen dëkkandoo yu Gàmbi yi lañu ci doon dajeel, daldi leen dóor benn bal ci dara (1-0). Mu dese ko ñaari ndaje ci kippu C bi mu bokk. Tinisi la war a dajel ëllëg ci àjjuma ji, 4i fani awril 2025. Beneen joŋante bu mujj bi, Somali la ciy dajeel keroog 7i fan ci weer wii.

GAYNDEY KUPPE YU MAG YI

Àppalees na Ekibu Senegaal bu mag bi ñaari joŋantey xaritoo ci weeru Suwe wee ñu dëgmal. Bu njëkk bi moom, Irlànd lañu ciy dajeel, bésub 6 suwe, mu war a amee fa Dublin (péeyub Irlànd). Ñaareelu joŋante bi, gayndey Àngalteer yi lañuy jëflanteel, war ko futbalee fa Nottingham keroog 10i fan ca suwe. Ñuy ñaari joŋante yu mag yoy, mën na cee natte dooleem bu baax, xoolaat tolluwaayam ak taxawaayam ngir waajal po yiñ jëm.

ESPAAÑ : « COUPE DU ROI »

Beneen « Clasico » taxawati na. Nde, Real Madrid ak Barcelone ñoo war a daje ci finaalu joŋante bii di « Coupe du roi ». Cig pàttali, ñaari ekib yi njëkkoon nañu daje ca finaalu « Super coupe » ba, Barcelone bomoon Real Madrid 4-0. Ñu war a dajeeti ci beneen finaal. Ndax Barça dafay dëggal mën bi mu mën Real Madrid ci at mii, am Real Madrid dafay fippu bañ ko wile yoon. Lu ci kanam rawul i bët !

LÀMB JI

4i Awril, bésu moom sa bopp ci Senegaal, jàppees na ci làmb ju rëy. Lac de Guiers 2 moo ciy sëgg ak Aada Faas, Móodu Anta bu Cees it war ci jàmmaarlook Prince, xale Pikin bi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj