Kippu L : Senegaal, Burkinaa Faaso, Malawi, Burundi.
FIBA 2026 (jigéen) : Senegaal du ca dem !
Basket-kati Senegaal yu jigéen yi dañu ñàkk seen finaal bi ci kanamu Ongiri 47-63. Loolu di dogal seen ug ñàkk a dem ca joŋantey Basket ñeel àddinas, war a am atum 2026. Muy lu diis ci sunu kaw jigéen ñooñu doon xeexal réew mi ak it bépp soppe bu leen doon xaar ñu gañe ko ba mën a bokk. Waaye, bum tee ñu gën a defaruwaat jàngat ci li weesu ngir waajal yoon yiy ñëw.