XIBAARI TÀGGAT-YARAM (25/9/2024)

Yeneen i xët

Aji bind ji

Mbappe ame na gaañu-gaañu !

KilIyan Mbappe dina sori pàkk yi lu tollu ci ñett ba ñeenti ayu-bés gannaaw gaañu-gaañu bim jële ci seen matsu sàmpiyonaa bi démb ak Deportivo Alaves. Ci loolu dinaa wuute yile ndaje : Atletico Madrid, Lille (LDC) ak Villareal. Waaye tamit, du bokku ci dajaloo ekibu Farãs giy ñëw.

Barça tànn na góol bu wuutu Ter Stegen.

Saa-almaañ bi dina toog li des ci àtum futbal bi du laal bal. Li ko waral di gaañu-gaañu bu metti bi mu ame ca óom ba keroog ca seen ndajem sàmpiyonaa ba ak Villareal. Loolu nag, mu ngi ko dal ci benn bal bum tëb jàpp ko bay wàcci na mu tegee tànk ba jekkadi.

Ci loolu, Barça, ci xél yim nekk te mu wóor ko ni warul def benn njuumte lu ko moy Real Madrid mi nekkandi ca ñaareelu toogaat ba jiitu ko, mu ngi ci wutum beneen góol bu mag. Am ci ay góol yu noppi ngir ñëw fa Barcelone wutandi Ter Stegen. Bokk na ci ñoom Bravo, góolam ba woon te bàyyi woon, Navas mi nekkoon Real Madrid ak Szczęsny mi nekkoon Juventus te dogoon pasam ci déggoo. Mu mel ni moom moomu moo gën a góndi ekibu Espaañ bi. Nde, waxtaan nañu (ñaari boor yi) ba juboo ciy kàddu. Li des moo di Szczęsny fàww mu fay Juventus 2i tamndareeti Ëro. Ndaxte ekibam bi daf ko joxoon lu tollu ci 6i tamndareet Ëro ngir li mu dogoon pas gi doxoon seen diggante. Li tax mu war leen jox loolu nag, mooy ni ci dog ga, dañu juboo woon ba xaatim ni mu amaatee ekib ci diggante bi fàww mu fay loolu.

“Tournoi UFOA U20” : Senegaal dem na finaal !

Tay ci àllarba jii 25i sàttumbaar, ndawi Senegaal yi doon daje ak yoy Gine yi ñeel demi-finaal ci powum UFOA U20. Senegaal moo dóor (2-0), Sëriñ Juuf moo dugal penaltii (82’simili) ak Séex Tiijaan Caam (90+3). Jaaree nañ fa it jàll ci kuppeg Afrig gees leen jagleel ( CAN U20).

 

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj