SÀMPIYONAA ALMAAÑ : BAYERN MUNICH NANGUWAAT NA CËRAM
Vincent Kompani ak i ndawam jël nañu sàmpiyonaa Almaañ bi. Naam, joŋante ya jeexaguñ. Waaye, moom Bayern Munich, kenn mënatu ko dab. Moo tax, nee na ko doŋŋet, téye. Muy lees ko miinee woon ci at yii weesu. Daaw Bayer Leverkusen moo ko njuuy, jël ko ci kawam. Ren jii nag, dañu ñafe ba jël ko. Harry Kane, moom, xol baa nga mel ne wanagu mbott. Ndax bii moo di kub bu njëkk ci dundug futbalam. Muy lu ko ñu bari yéene woon. Def na at yu bari Tottenham amu fa benn kub, ñëw Bayern daaw ekib ba luppe po ya mu bokkoon yépp. Ñii naan ko umaa, ñee naan dafa aay gaaf. Waaye wolof nee na “xëcc bu daggul, dikk”.
LIGUE DES CHAMPIONS : 1/2 FINAAL
Matsi dëmi-finaal yu njëkk ya jàll nañu ca ayu-bés bi weesu. Mu nekkoon mats yu metti, waayeet yu neex. Inter Milan mi fekki woon Barcelone dafa daldi timboo ak moom ci 3-3. Soppey futbal yépp di xaarandi seen joŋante bi des ndax gëm nii dana neex lool fa Itaali. Paris SG moo fekki woon itam Arsenal daldi koy dóor benn bal ci dara.
Ci ayu-bés bii, 6 ak 7i fan ci weer wi, talaataak àllarba, la matsi deltu yiy am.
EUROPA LEAGUE : 1/2 FINAAL
Fii, ci ñaareelu powum tugal mi, ñaari ekibu Àngalteer yi ñoo taxaw temm ngir daje ca finaal ba. Nde, Manchester United fekki na Athletic Bilbao ca pàkkam daldi koy noggatu 3-0. Tottenham itam dalal Bodø/Glimt ba noppi bom ko 3-1. Seen i ñaareeli mats di am alxames 8i fan itam ci weer wi.
LÀMB JI : Prince daan na Móodu Anta
Ñu baree ngi ko doon xaar, jàppeesoon ko ca weeri féewiryee, mu takk suuf, ñu tuxalees ko weeru awril bi. Mu amati ayib, ñu jàppati ko niki démb, 4 Me. Ñaari mbër yépp waajaloon seen bopp ndax xam ni làmb ju ñépp di xaar la, waaye luy am solo ci seen dundug mbër.
Doomu Pikin jee ko mujje def doomu Cees ji, daan ko jéll bu set. Ndam li nekk luy gën a aj Prince. Ndax dana gën a ñeme dem ci kaw, laaj ci gaa ñi. Waaye, ndax du gën a suruxal Móodu Anta gannaaw ba mu jóge woon ci defet bu ko metti ba taxoon mu toog ab diir liggéey defar yaramam door a dikkaat. Lu leer ba leer mooy ni xale la, na ligéeyaat bu baax bañ a xàddi.