XIBAARI TÀGGAT-YARAM

Yeneen i xët

Aji bind ji

FUTBAL

Racine Club de Lens xamle na ni Nàmpalis Mendi dana jóge ca ekib ba gannaaw bam fa defee ñaari at (2023-2025). Ci diir bim fa def, 32i mats la am ca këlëb. Jamono jii, moo moom boppam. Manaam ekib bu ko neex waxtaanal, bu juboo amee seen diggante mu xaatim fa.

Abiib Jara moo ngi ci tànku dem sàmpiyonaa Àngalteer. Jamono jii doomu Senegaal bi dafa nekk ciy guddeem, kaar. Muy fa këlëbam di ekibu réew mi yépp muy dox di dugal di amal njariñ ekib yi. At mu am solo mim def a waral këlëb yu bari doon bàyyi xel ay mbiram. Mu mel ni Sunderland mi delsi ren ca Premier League bu Àngalteer dafa wane bëgg-bëggam ci moom ba sax waxtaan jot na am ci diggante ñaari boor yi. Mu mel ni juboo jot na ca a am ba, ci ayu-bés bii, dees na matal caytu-yaram gi ak ya ca des.

Paul Pogba dem na Monaco. Moom nag, dañ koo ajoon ñetti at yoy futbalul fenn ngir ne dafa daan jëfandikooy mbir yees aaye ci futbal bi (dopage). At yi weesu bari woon ay yéeg ak i wàcc yu bari, yii ci wàllu futbal, yee ci mbiri ñoñ. Jafe-jafe yooyu demoon ba ñu bari jàppoon ni, xëy-na, mu jaare fa bàyyi. Waaye, saa-farãs bi ne patt ci ruqam rekk, di ligéey ak a xaar bés bu rafet. Démb ci gaawu bi, 28i Suwe 2025, la daldi torlu am pasu ñaari at ak këlëbu Farãs boobu di Monaco. Ba loolu amee, jot na fa a tuur i xéewal ngir xam fim jaar ba àgg fii.

Cristiano Ronaldo yeesal na pasug ñaari at ca Al Nasr, fa Araabi Sawdit. Wii yoon, ñu dolleeti payooram. 200i tamndaret ciy Óro lay fayeeku ci at mi. Loolu di payoor bi gën a duun ci mbooru futbal.

LÀMB JI

Sitta ak Bàlla Gay 2 amal nañu démb ci gaawu bi seen ñaareelu jàkkarloo. Mu tàngoon jër nag. Ñaari mbër yi wane nañu taxawaay bu am solo. Ku ci nekk di jéem a napp sa moroom. 20 Sulet di bés bees leen jàppal ñu war ci bëre.

Mu mel ni nag seen bëre bi dafay bëgg a takk suuf. Ndax, démb, CNG daldi nay génne ab yëgle di ci xamle ajug mbër moomu di Sitta. Li ko waral nag mooy ne, moom doomu Jàmm-a-gën ji dafa bañoon a saytu yaramam ci « teste antidopage » biñ ko bëggoon a defloo keroog ba mu bëree ak Móodu Lóo ba noppi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj