XIBAARI TÀGGAT-YARAM (4/11/2024)

Yeneen i xët

Aji bind ji

Powum UFOA U17 2024

Ren jii, Senegaal moo dalal po mi, doon ko amal diwaanu Cees ca fowu Lat-Joor bi. Àgg nañu ca finaal ya. Senegaal miy aji-dalal ci moo ci daje ak kii di Mali. Tay ci altine jii, bi 18i waxtu jotee la joŋante bi door. Fowu Lat-joor bi lees jàppoon, wànte dañu ko mujje tuxal ca bu Abdulaay Wàdd ba, fa Jamñaajo. Laata loolu nag, Gine Bisaawo dina daje ak Gàmbi bu 15i waxtu jotee, ñeel ñetteelu toogay ba. Ci dëmi-finaal yi, Senegaal moo bom Gine Bisaawo ci seri yi (4-3) gannaaw ba mats bi jeexee ci 0-0. Mali moom, moo gañe Gàmbi 3i bal ci 2 (3-2).

Ñoom ñaari way-finaalu yi it, jàlle nañu ca kuppeg Afrig gees jagleel U17 yii di ñëw.

Futbalu tefes : Al Séyni Njaay yeyoo na sargal !

Góolu ekibu nasiyonaal Senegaal futbalu tefes, léegi guy gu réy la ci wàllam fii ci biir réew mi ak sax ci Afrig. Nde, wuyuna 177i yoon wooteg ekib bi, jël ci 8i yoon kuppeg Afrig, tegale ko 5i yoon yu toftaloo, mu jël 7i yoon góol bi gën a xarañ ci CAN bi, teg ci góol bi gën a aay ca sàmpiyonaa Almaañ 2018 ba noppi amaale “médaille de bronze” foofu ca at moomu. Muy waada bu mag ci wàllam. Dina jekk te jaadu loolu réew mi sargal ko sagal ko ndax yeyoo na ko.

Manchester United am na tàggatkat bu bees!

Keroog ca altine jale weesu, la njiital ekib ba daldi jël ndogal dàq Erik Ten Hag gannaaw ba leen West Ham dóoratee ca dibéer ja, tax ñu wàcc ba ci 14eelu toogaay ba. Am nañu tàggatkat bu bees. Ruben Amorim lees teg ci boppo ekib bi, mu daldi xaatim pasug ñetti at, maanaam fii ak suwe 2027. Waayeet, tegalees na ko ca wet wa menn at mees mën a dolli.

Làmb ji

Tànnees na Maalig Piyeer Ngom muy njiital CNG. Moom nag, arbit la woon ci làmb ji. Waaye, léegi mooy njiit li. Ñu di ko ñaanal kayug jàmm.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj