XIBAARI TÀGGAT-YARAM (8/8/2024)

Yeneen i xët

Aji bind ji

Jeu Olympic Paris 2024

Ci wàllu futbal bi, Espaañ U23 ak Farãs U23 ñooy daje finaal, àjjuma 9i pani ut 2024. Waaye, lu jiitu loolu, ci alxemes ji, Esipt U23 di na xëccoo 3eelu toogaay bi ak kii di Marog U23.

Ubbiteg sàmpiyonaa yi

Fi ak i fan yu néew ci weeru ut wii nu nekk, sàmpiyonaay réewi tugal yi dinañu ubbi ñeel atum 2024-2025 mi. Mu mel ni ci jamono yii futbalkat yi ñu ngi tàmbali di dellu ci seen i këlëb ngir waajal at mi.

Espaañ dina tàmbali ci 15i fan ci weeru ut wii, Farãs ak kii di Itali it dinañu ubbi seen i sàmpiyonaa ci 17eelu fan wa, kii di Almaañ mooy mujje ndax ca 23eelu fani ut lay tàmbali bosam.

Mbappe tàmbali na tàggatu ca Real Madrid

Démb ci àllarba ji, 7 ut 2024, la Kilyaan Mbappe tàmbali ay mbiram ca Real Madrid. Amal na tàggatoom bu njëkk foofu àndoon ci ak Carvajal, Bellingham, Camavinga, Mendy ak Tchuameni ñiy door a ñëwaat.

Dani Olmo dem na Barça

Barcelone déggoo na ak këlëbu Almaañ bii di Leipzig ci mbiri Olmo, waadab tugal 2024 bi. Mu mel ni joxante nañu loxo ci fànn yépp ba fim ne, lépp mat na. Ñu ngi ko jëndee 55i tamndareti ëro ak 7i tamndareti ëro yoy, neexal la (bonus).

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj