YÀNQOOBA JATARA, JËWRIÑU TAGGAT-YARAM JU BEES JI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Mataar ba nekkatul jëwriñ jiñ dénk tàggat-yaram gi. Loolu bokk na ci xibaar yi gën a fés ci Nguur gu bees gi Njiitu réew mi Maki Sàll taxawal gaawu bii weesu. Ci Àllarba ji la Yànqooba Jatara jël lenge yi.

Tàggat-yaram gi am na kilifa gu bees ci Nguur gu bees gi. Folleeku ki fi nekkoon nag, di Mataar Ba, doon na lu ñu bare desee nangu. Bokk na ci li ko waral, nekkoon na jëwriñ ju gën a yàgg ak ndombog-tànku tàggat-yaram bi. Def na ak moom lu ëpp 8i at. Ci xayma it, am na ay njureef yuñ mën a takk ci diir bi mu fi nekkoon (lu mel ni kub bu Afrig 2021 bi Senegaal Jël), ba tax ñuy laaj lu waral njiitu réew mi jële ko fi.

Ci bi muy joxe lenge yi nag, Mataar Ba xëppul ci ndab li benn yoon suuf donte ne kenn xaarul woon Njiitu réew mi jële ko fi. Du ñàkk mu doon lu ko bett. Waaye, dalal na Yànqooba Jatara ba noppi rafetlu it tabb gi ko njiitu réew mi tabb ngir mu wuutu ko. Rax-ci-dolli, xamal na ko yéeneem ci gunge ko ci liggéey bi ko Njiitu réew mi sant.

Yànqooba Jatara itam delloo na Mataar ba njukkal. Ginnaaw bi mu nangoo ndogalu Njiitu réew mi, nangul na ko it liggéey bu am solo bi mu fi jot a def. Ba tax na kàddoom yu njëkk diy kàdduy njukkal :

“ Maa ngi njukkal sama mag, di sama xarit, Mataar Ba. Ànd naa ak moom 20i at te li ma gën a jàpp mooy cawarteem, yéwénam, ubbeekoom ak oyofam. Ci gàttal, ginnaaw li nga defal tàggat-yaram gi fii ci Senegaal, maa ngi lay ñaan nga nangoo nekk ganu delegaasiyõ Senegaal ci kub di mond ba ca Qataar. Sunuy néeg ñooy dend. Maa ngi lay ñaan itam nga teewal nu ci joŋantey xaritoo Senegaal-Boliwii bi war a am 24 Sàttumbar bii di ñëw ci Orleyã.”

Bu loolu weesoo, jël na ko it taf ci wetam te fas yéene koo boole ci liggéey bi te bañ a seppiy loxoom.

Bu amee ñu jàpp ne Mataar Ba waru fa woon a jóge, ñeneen jàpp nañ ne demam gi jaar na yoon. Loolu doon na luñ nemmiku ciy kàddu yu mel ni yu Baaba Tànjã mi fi jiite woon Kurélu basket bu Senegaal. Te dara waralu ko lu dul ne, nekkul woon njiital tàggat-yaram yépp. Maanaam, yamalewul woon. Mu mel ni njiit lu bees dafa dégg walla muy dégg-dégglu ñaxtu yii. Bi mu noppee ci Mataar Ba, li mu gën a fésal moo di « dinaa nekk jëwriñu tàggat-yaram yépp ».

Lu mën a xew ak lum ci jublu ? Ndax Mataar Ba dina nangul Yànqooba Jatara lim namm ci moom ? Seetaan a dàq ci ndaje.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj