YÉENE NÉEG LA, BOROOM A CAY FANAAN

Yeneen i xët

Aji bind ji

Siidi Ahmet Mbay, ku dégg tur wi sam xel dem ci coowal Aji Saar leek Usmaan Sonko. Ndax, ci lees wax, moom moo di xolu kootoo gees toppe njiitul Pastef li ba tey. Waaye, wile yoon de, moom, ngóor si Mbay, la Yoon di topp. Xibaar bi nag, Seneweb a ko jëkk a biral, Baabakar Ture mu Kewouloo dëggal ko, yéenekaay Libération fésal ko ci xëtam bu njëkk. Yéenekaay bi sax, dafa limaale Dooro Géy ak Abdu Ngeer mu Codas, wax ne dañu laale ci mbirum njublaŋ mees di toppe Siidi Ahmet Mbay. Nee ñu, jamono jii, takk-deri DIC yaa ngiy wër fu nekk kii di Siidi Ahmet Mbay.

Fu coowal Aji Saar leek Sonko di teere ? Mooy laaj bu ñu bari di laaj. Daanaka, bés bu Yàlla sàkk, mbir mu bees feeñ ci. Te, bu dee wax dëgg, lu ci bees lu nekk di gën di setal njiitul kujje gi, di gën a weer kootookat yi. Dafa di, Aji Saar, wutukaayu xaalis la ko ñenn ñi def. Siidi Ahmet Mbay du ko weddi, bu dee lees koy toppe wér na ni moo ko def.

Li xew mooy ne, ci li kibaraan yi siiwalagum, Siidi Ahmet Mbay moo dóor 10i miliyoŋi Dooro Géy. Ndege, daf ko gëmloo woon ne yor na ab widewoo bob, Aji Saar ak Usmaan Sonko ñoo ci nekk di def naka su dul noonu. Mu jaral waa ji génne 10i tamndaret ci sunuy koppar ngir wecce ko caabi USB (clé USB) bi def widewoo bi.

Ndekete yoo, mag dina dugg ciy naxam. Looloo dal Sëñ bi Géy. Ndaxte, ginnaaw bi mu jotee ci « clé USB » bi, fekku ci dara ba dara booloo jeex. Maanaam daal, ngóor si Mbay daf ko dóor màrto, njublaŋ ko. Looloo ko tax a kalaameji Yoon. Moo tax, jamono jii, ñoo ngi wërandi Siidi Ahmet Mbay. Wànte nag, dees amal ub taxaw seetlu ci mbir mi.

Naka la nit mënee génne 10i tamndaret ci xaalis ngir ab widewoo ? Ndax jar na ko ? Lii day wane mbañeel gi àndandooy Njiitu réew mi ameel njiitul Pastef li. Beneen laaj bees mën a samp mooy ne, ndax nit dina liggéey, ñaq, sonn, ba am xaalis bu ni tollu di tayle cib widewoo ? Dafa di lu lewul, du law.

Beneen taxaw seetlu mën na ci am. Bu ñu jéllalee firnde yiy setal Usmaan Sonko yépp, naka la Yoon mënee sukkandiku ci kàdduy njublaŋ ngir tuumaal as gor ? Mbir mii, day wane rekk ne Yoonu Senegaal dafa nërmeelu. Te, lu ni mel, réew mu mu am, fitna dina fa ganesi.

Ab njàngat mën na ci tukkee tamit. Ndaxte, bi coowal Aji Saar ak Sonko li dooree ba tey, ak ndëgg-sërëx yi ñu teg yépp Usmaan Sonko di leen teggi, saa su nekk, seen pexe day nasax. Xanaa mu waroon leen a yee. Wolof de nee na, yéene, néeg la, boroom a cay fanaan.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj