YOKKUTEG DUND GI “…dañuy ragal ne 2023 mooy gën a metti.”

Yeneen i xët

Aji bind ji

Njiitu réew mi, Maki Sàll, woote woon na ndajem waxtaan ñeel dund gi. Altine, 26i fan ci sàttumbar la ndaje mi amoon ca màkkaanum Njiitu réew ma. Li ñu ko dugge woon mooy péncoo jafe-jafey dund gi. Njiitu réew mi nee, dina jël ay ndogal ngir yombal dund gi ci réew mi.

Njiitu jëwriñ yi, Aamadu Ba, jëwriñi yaxantu gi ak mbey mi, mbootaayi njariñaafon yi, jaaykat yeek kurélu patronat geek ñeneen ñoo séqoon waxtaan wi, ci njiitalu Njiitu réew mi. Njiitu réew mi xamle na ne, sabab yi waral yokkuteg dund gi, biti lañ jóge :

« Nde, ñetti at a ngi nii nuy jël ay ndogal ngir woyofal yokkuteg njëg gi xam ne, mbasum Covid-19 bi ak coppite yi xareb Ikren bi sabab ci yaxantug àddina si ñoo ko waral. Taxawaleesoon na naalub PAP2A (Plan d’Actions Prioritaires Ajusté et Accéléré) bi nga xam ne, am na ci pàcc bu réy bees jagleel pexem lekk gu doy te jàppandi ak yokkuteg ndefar yi, ci loxoy njàmbureefu réew gu dëgër. »

Moom, nag, joxe nay santaane jëmale leen ci jëwriñ yi ngir ñu jëfe ngirte yiy juddoo ci ndaje mi, fileek njeexitalu weeruw oktoobar wile. Bokk na ci li njiitu reéw mi santaane :

-Na nguur gi gaaw fey ndàmpaayu 15i tamñareti CFA yi mu ameel wolkat yi te ñu gaaw tamit fey ndàmpaayu ceebu « paddy » bi beykat yi ;

-Pommug juutiy niine yi ak njéggaanuy diw gi ;

-Ubbiteg waxtaan ak nguurug endo yi ñeel njégganug ceeb bi ;

-Dooleel caytug njëg yi ak jumtukaayi njëwriñu yaxantu gi (dees na jël 1000iy ndaw ngir ñuy saytu njëg yi) ;

-Xoddib waaxu Ndakaaru ak caytu gu mucc ayib, añs…

Ñi fa teewoon ñépp jël nañu kàddu, joxe seen i xalaat ak pexe yi ñu jàpp ne mën nañ saafara mbir mi. Waaye, nag, mbir mu tollu ni dundug askanuw lëmm, deesu ko jagleel ay waxtu kese. Liggéey bu yaatu la laaj ndax li ci aju yépp. Te sax, laaj bu ñu bariy laaj mooy, ndaw ya fa wax ci turu askan wi, ku leen yabal ? Kan moo leen tànn ?

Nde, ña fa teewoon, wëliis njiitu réew mi, amul kenn ku ci askan wi fal. Moo tax ñu bari ci askan wi ñàkkal fayda mbir mi. Nde, dañ jàpp ne pólitig a nekk ci ginnaaw. Lu ni mel, dees na ko waxtaane ca Ngomblaan ga, jëwriñ yeek ñi ci yor ndombog-tànk yépp janook dépite yi askan wi fal, ñu laaj leen, digal leen. Bu boobaa, lépp doon na gën a leer.

Ci beneen boor, ñu baree ngi laaj naan, ndax li Maki Sàll deful ci diirub 10i at, ndax dina ko mën ci diirub at ak genn-wàll ? Tontu li mooy déedéet. Te sax, moom ci boppam wax na ko. Ndaxte, ginnaaw bi mu fàttalee li Nguur gi defagum lépp ngir wàññi njëg yi, nangu na ne, boobaak léegi, dara wàññeekuwul, lépp a ngi wéy di yokk. Moo tax mu ne, « bu jaree wàññi njiwaan yi ngir jàppale askan wi, dinan ko def ndax dañuy ragal ne 2023 mooy gën a metti. »

Mu mel ni Njiitu réew mi day dëggal li Usmaan Sonko waxoon ne, as-tuut li fi dese Maki Sàll, saa-senegaal dinañ gën a sonn, ndax lépp ay metti. Kon, ku yebu xool foo jàpp.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj