YOON : SOS/PAIX A NGI ÑAAN NJEKK NJIITU REEW MI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Mbootaayu kuréli ma-xejj yi ngir jàmm, ñu gën leen a miis ci SOS/Paix (Synergie des organisations de la société civile pour la paix) ñaan na njekk Njiitu réew mi ñeel ñi caabi féete ginnaaw. Ñuy sàkku ci Nguur gi mu doxal yërmande te bàyyandi képp ku ñu tëj ci lu dese aay, rawatina ñi ñu jàpp ci yëngu-yëngu yi fi jaaroon.

Ci alxames jii ñu weesu la mbootaayu kuréli ma-xejj yi doon amal aw waxtaan ak taskati xibaar yi. Ñoo ngi tollu ci lu ëpp 20i kurél yu booloo tudde seen bopp SOS/Paix. Ñoom nag, jamono yii, bi nit ñiy waajal yoonu Tuubaa ngir màggali bésub 18 safar bi lañu taamu ngir yéy yàbbi ci xew-xew yi lëmbe réew mi, rawatina ci géewug pólitig geek ni yoon di doxe.

Li gën a fés ci seen ndaje mooma mooy kàddu ya ñu fa biral jëmale leen ci Njiitu réew mi. Naka noonu, ñuy sàkku ci Nguurug Senegaal mu gëmm te féexal ñi nga xam ni yoon àtte na leen ba noppi te defuñu lu aay. Maanaam mu may leen li ñu tuddee ci seen làmmiñu bopp « grâces exceptionnelles ». Bu jëlee ndogal looloot, na ko yaatal te féexalaale ñi yoon tegoon loxo ci yëngu-yëngu yi fi jotoon a jaar ak ñi nga xam ni defuñu lu dul wax seen xalaat.

« Noo ngi ñaan Nguur gi mu bàyyi bàyyib négandiku maxejj yi ñu jàpp tëj te defuñu lenn lu aay, lu dul génn ñaxtu ak wax seen xalaat ci ni réew mi di doxe » (Maalig Jóob)

Ngir seen bëgg-bëgg mën a sotti, xamle nañoot ni dinañu sol seen i dàll, dox ci seen kéem kàttan. Balaa yàgg, dinañu seeti jëwriñ ji ñu dénk kaaraange biir réew mi ak jëwriñ ji ñu dénk wàlluw yoon ngir waxtaan ceek ñoom.

Ginnaaw bi ñu biralee seen càkkuteef ci Nguur gi, mbootaay gi dellu na woote jàmm tey ñaan askan wi, rawatina ndaw ñi, ñu ànd ak dal te sàmmonteek sàrti réew mi. Woo na leen itam ci ñu sàmmonteek seen i wareef te jëli seen i kàrti wote, nde mooy seen ngànnaay li gën a wér.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj