Tey, 1 fan ci weeru me, àddina wërngal këpp di màggal bés bees jagleel liggéey (liggéeykat yi). Ñu koy wax ci nasaraan « Journée internationale du travail ».
Ci gàttal, bés bees jagleel liggéey walla liggéeykat yee ngi sosoo ca Etaa-Sini, ci atum 1884. Li ko waral di xeex bi mboolem liggéeykat yi doon xeex ak njaatige yi ngir ñu wàññil leen seen diirub liggéey. Li ñu bëggoon mooy, limub waxtu yiñ daan liggéey jóge ci fukk walla lu ko ëpp yi mu nekkoon ca jamono yooyu, wàcc ba ci juróom-ñetti waxtu bés bu nekk.
Ci bésub 1 me lañu tàmbali woon xeex bi. Ndaxte, li mu nekk bés bi jiitu ci armanaatub boroom cumbeef yi. Ginnaaw bees nangoo wàññi gi ñeel ñenn ñi doŋŋ (1 me 1886) lay jàppante yu metti am ci diggante takk-der yeek liggéeykat yi bay bakkan rot ci (3 ak 4 me). Mu jóge fa nekk bés bu kenn dul liggéey. Waayeet, muy bésub xeex ngir àq ak yelleefi liggéeykat yi. Xeex bilee law ci àddina sépp, rawatina ca tugal, ba mu mujje doon bés bees baaxoo màggal li ko dale ci 1 me 1948. Mu nekk bés bu kenn dul liggéey te di ko feyeeku, maanaam bésub liggéeykat yi.
Fii ci Senegaal, kenn demul ñu des. At mu jot, dees na màggal bés bi ci 1 fan ci weeru me. Muy bés bu kenn dul liggéey. Waayeet, ñenn ñi defaale ko yoonu tool ngir di ci ñaxtu ak a ñaawlu jafe-jafe yi ñuy faral di dund ci seeniy liggéey. Te, sax, at mu jot, bu bés bi teroo, sàndikaa dañu jébbal Njiitu réew mi wayndare woo xam, dañ ci dëxëñ seen i njàmbat ngir ñu indi ciy saafara. Senegaal, nag, fànn yu bari dañoo tagatémbe.
Muy fànnu paj mi, caytug bokkeef gi, meeri yi, napp gi, njàng meek njàngale mi, wàllu tabax gi, añs., foo ci laal day metti. Ay ñaxtook i mébét yu dul jeex a màndargaal atum 2023 mi. Liggéeykat yaa ngiy xultu rekk, di amal i doxi ñaxtu, di kaas ak a mettitlu anam yi ñuy liggéeye, tuutiwaayu peyoor gi, xàjj-ak-seen bi ci am, tooñaange, añs. Daanaka, dara doxul. Lépp a dëgër.
Dafa di nag, sàndikaa sax, ak liggéeykat yiy ñaxtu, ñoom, jot nañ ci liggéey bay sàkku ak a kaas yokkute ci seen i liggéey. Waaye de, ñi amul xéy te yor i njaboot, góor-góorlu yeek ñiy foraatu, ñoom, kenn boolewu leen ci bés bi. Te, kenn gënu leen ci yay. Rax-ci-dolli, bare nay ndaw yoy, jàng nañ ba yey seen i këyit, gàddu seen i lijaasa, di wër i liggéey, tëw a am. Ñooñu moom, fu ñuy jooye seen naqar ? Njiitu réew mi dige woon na fiy liggey yu dul jeex, waaye tey la ñàkkug xéy gi gën a bari. Mooy li ñuy wax rekk, « réew mi dafa maki ».