12I ATI M23 : LA WOON WONNEEGUL

Yeneen i xët

Aji bind ji

Kurél gii di « Mouvement des forces vives de la nation », ñu gën koo xam ci turu M23, am na 12i at ci ren. Ci atum 2011 lees ko sosoon. Terewul li ko taxoon a juddoo ngi wéy di sooke xeex ak i yëngu-yëngu ba tey. Mu mel ni ci diiru 12i at yi weesu, dara soppeekuwu fi.

Keroog, bi Abdulaay Wàdd amee yéeney jàllale sémbub àtte bees duppee woon « Ticket présidentiel » ca Ngomblaan ga la coow li jolli woon ci réew mi. Ndaxte, sémb ba dafa woroo woon ak li ndeyu àtte réew mi sàrtal, te doon gàkkal demokaraasi Senegaal. Dafa di, bu jàlloon, Abdulaay wàdd di na sax ci Nguur gi, toog ba mu soob ko, mu donnale ko ku ko neex. Ñépp njortoon ne, doom ji, Kariim Wàdd, la bëggoon teg ci jal bi, mu wuutu ko. Daanaka, li Seŋoor defaloon Abdu Juuf la nammoon defal doom ji, waaye ci beneen anam. Askan wi bañ, mu lajj.

Looloo jógloo woon askan wi, keroog 23 suwe, ba Ngombalaan gi naree a wote àtteb sémb boobule. Ñu nekkoon ay junniy junni doom-aadama yoy, dañu génnoon, taxaw temm ca kanamu Ngombalaan ga. Wet goo geestu waan séen seen pànkàrt yi ñu bind ci « Bu kenn laal sunu ndeyu àtte réew », « Wàdd demal sa yoon » walla sax « Nguur gi du lu ñuy donn ak a paacoo ».

Mbooloo ma fippu woon, mer ba futt, lànk ne naal boobu du fi ame. Xeex ba metti woon lool ba ay bakkan rotoon ca. Kujje gépp ak way-moomeel yi ne ci mbeddi ndakaaru yi. Mustafaa Ñas gàddub xeeram, ñàngalal ko ba… Maki Sàll miy jiite réew mi tey, ŋàbb ab mer-gàddoom, fasoon yéene fanaan ci mbedd mi. Waa Y’en a marre tamit, taqoon ripp ci xeex bi. Looloo indi M23, di woon kurél gog, xeex lépp luy gàllankoor demokaraasi ak yoon a ko taxoon jóg, rawatina mbirum ñetteelu moome gees di soow tey. Ndeysaan, 12i at ci ren, dara soppeekuwul ndekete.

Fii ak juróom-ñaari weer, war nañ falaat Njiitum réew lu bees. Waaye de, tey la coow li  gën dee wullee ñaay. Mu mel ni, lu ñu dundoon lañuy dundaat jamono jii, walla lu ko raw. Ndax, njiitu réew mi, Maki Sàll, fayul naar bi xoromam. Ndaxte, tey jile, Maki Sàll ci boppam moo dugal réew mi ci guuta. Fu ñu daan wax Abdulaay Wàdd, démb, tey Maki Sàll moo ko fa wuutu. Loolu la waa M23 seetlu démb ci àjjuma ji, 23 suwe 2023, bi ñuy màggal seen 12eelu at.

Ku déglu seen i kàddu xam ni yaakaar tas na. Naam, lottuñu ci xeex bi, wànte li leen taxoon a sos kurél gee ngi wéy di doon jàngoro ci réew mi ba nëgëni. Dafa di, tey lañ gën caxat-caxatee Ndeyu àtte réew mi, di ko soppi ci coobarey nit ku bëgg a jafandu ci Nguur, muy Maki Sàll. Ndajem ndeyu àtte réew mi di wéy di jaamu soxlay Njiitu réew mi, na mu ko daan defe ca jamonoy Ablaay Wàdd. Loolu sabab fiy yëngu-yëngu yu metti ba, daanaka, 50i bakkan ak lu teg rot nañ ci diggante 2021 ak tey. Ñu jàpp ay junniy junni nit ci kaso yi, di dog siñaali tele ak tëj ay taskati xibaar ngir xoqatal leen, noppiloo leen.

Démb, ca seen waxtaan wa, sàkku nañ ay réew mi wote yu jaar yoon yoy, du am xàjj-ak-seen. Bu dee lu jëm ci yëngu-yëngu yi fi amoon bu yàggul dara, kurél gi yëy na ci yàbbi, naqarlu bakkan yi ci jot a rot ak ñaawlu yàqu-yàqu yees ci nemmeeku ak lépp lu ci réew mi ñàkk. Yii yépp a tax M23 mënagul a bàyyi xeex bi. Nde, dañoo lëkkalook F24 ngir delloo buum ca boy-boy ga. Ndax kat, la woon wonneegul.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj