I
Sëriñ Baabakar Jóob Callweer ndaanaan la, di bindkat, di gëstukat itam ci làmmiñu wolof. Liggéeyam ak xam-xamam dëgg nag ñi ngi jëm ci teyaatar. Mooy doxal jotaayu léeb bI tudd Callweer, cI Mourchid TV.
SAAGA
Saaga du ngànnaay,
du pakk, du ray, du gaañ, du jàpp, du takk.
Saaga du faxas, du raxas, du jubal, du dugal, du ràbb, du nàmm.
Heey yaw mi sa xel nasax, rambax, senax, yonjax, jastindikoo saaga, def ko paaka.
Du jam, du rendi, du fàdd, du ngàdd, du ñàdd.
Su xalaat tërëfee, xel tarxiis, ñàkk, ñëg, ñànki,
Xol nërmeelu, bóli coroxaan, làmmiñ saaga.
Heey saaga, du lay, du way, du yay,
Ku sa xalaat wér péŋŋ, say saaga ne meŋŋ.
II
Soxna Ndey Xayba Faal mi ngi dëkk Ndakaaru, doon jàng xam-xamu melosuuf ca Daara ju mag ju Séex Anta Jόob. Bind na taalif yu bari ci fànn yu wuute, niki bëgg-bëgg ay jafe-jafey àddina, ngëm ak diine, sàkku xam-xam ak coono yi ci aju.
Yoonu bànneex moo bariy xeer
Leeg-leeg mu lëndëm
Ba nga foog ni danga gëlëm
Moone soo siggee de seen as leer
Yoonu bànneex moo bariy nattu
Ay tolof-tolof yoo war a muñ
Gëm ni lu mu yàgg yàgg dinga muuñ
Yokku, féex mel ni jigéen ju masul a matu
Yoonu bànneex moo bariy njariñ
Dina la tàggat ñemeloo la tawat
Ngay dékku naqar fab sa xel di xalaat
Jàngat ne Yaa Rabbi rekk a doy Sëriñ
Yoonu bànneex moo man a gudd
Ngay dékk say loxo di sàkku ñaan
Di laabal sa xol dëddale la ak kañaan
Xam ne bis du gën a réy sa bisu juddu
Bànneex bi may waxtaane
Xajul ci bile dëkk
Dafay sax dàkk
Ni ko téere bu sell bi junje