Saydu BA waa Ñooro la, di al-pulaar bu gàlle. Ndaanaan luy yëngu ci teyaatar la, tëgg ak um pecc. Tukki na ci réewi nasaraan yu bari, di fa teeweji ay ndajey fecckat ak i tëggkat. Ba Saydu tàmbalee bind ay taalif ak léegi, am na lu ëpp ñaar-fukki at.
FAJAR
Fajar
Xérem ni selaw
Dëkk bi ni sendew di nelaw
Ci biir mbalaanu sutura
Fajar
Suuf sedd guyy
Kenn doxul
Dara yënguwul
Nelaw falu di buur
Fajar
Weer wi mel ni kuy làqi taaram
Ci poroxndollu niir yi
Biddeew ya suux
Asamaan set wecc
Fajar
Njanaaw yiy sab ba mel ni ñuy sàbbaal Yàlla
Njugub ya gàddaay
Ak yeneen xeet yu ni mel
Ci la jàkka yiy nodd
Fajar
Baatu As-salaatu Xayril minna nawmi
Di xotti tareet asamaan si ba textexaan
Ngëmug gaa ña Yàlla baaxe
Ci wéetal seen Boroom
Fajar
Bés bi tàmbalee ràbb
Ay cëwrinu fenkub jant
Ci pëllug leerug ceeñeer gu jëkk
Fajar
Asamaan si tàmbalee set wecc
Ànd ak ngelaw lu ndaw te féex
Ñu folli nelaw tey teeru léemaayi suba yi
Soxna Ndey Xayba FAAL mi ngi dëkk Ndakaaru, doon jàng xam-xamu melosuuf ca Daara ju mag ju Seex Anta Jόob. Bind na taalif yu bari ci fànn yu wuute, niki mbëggeel ak jafe-jafey àddina, ngëm ak diine, sàkku xam-xam ak coono yi ci aju.
NIT DAY MAANDU
|
Ku dee ak bàmmeelam Lu waay def it boppam Mbindeef ak ug mbonam Soo ciy yàbbi daldi ko yées Man Faal damaa jaayante Dëddu wax ak i werante Seexlu it fàww weerante Cib murid dafa yées Sang sama dénkoon na ma Murid bu jógul ca waxi nit ña Du dox mukk ca yoon wa Di dox di taxaw rekk a yées Ku ne na nekk ca la mu gëm Te ñun ñiy yóotu fàww ngërëm Ñu gëmm tëx te bañ a gëlëm Bëgg Sëñ Bàmba mooy maye xol bu bees Xol buy dund fàww al-jànna Ruuh guy xeeñtu mbir ya Mucc asal fi ker ya Di dox di féexlu rekk a yées Murid bu mënta maandu Na dellu fàww jébbalu Di tuub tey saxoo yeeslu Ndax tudd mbonug nit rekk a yées Ey waay fu nit di mucce Di xéy di góor–góorlook a xare Ba daan jéll sa ndam saraxe Li rekk ay ndof li yées Ku dee ak bàmmeelam Lu waay jëf it boppam Buur beek i mbindeefam Di ko lijjanti mooy bopp bu ñàkk a fees Dammal say bët ca la lewul Damm saw làmmiñ ca la daganul Yoonu Sëñ Bàmba lu ca askanewul Jarul di wax ba sa màggal di rees Bu ñuy wax it deel noppi Góor-mag kepp a soppi Ay doxalin tey rooti Ca ña duy leer ba fees
|