15eelu NDAJEM OCI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ci njeexitalug ayu bés bi, gaawu 4 ak dibéer 5 me 2024, lañ doon amal 15eelu ndajem OCI (Organisation de la Coopération Islamique) mi. OCI di kurélug jàppalante gu dox ci diggante réewi jullit yi ci àddina si. Seen ndaje moomu nag, ña nga ko doon amalee Bànjul, fa réewum Gàmbi, doon ci waxtaane ponk bii di « Diisoo ñeel dëgëral bennoo beek jàppalante bi ngir suqaleeku tey ak ëllëg » (Renforcement de l’unité et de la solidarité par le dialogue pour un développement durable).

Ginnaaw bi ñu noppee ci seen waxtaan yi, démb, réewi way-bokk ya ànd nañ biral ab déggoo, duppee ko Déclaration de Bandjul. Ñu cay fésal ni kurél gee ngi wéy di jàppale waa Palestin ci seen xeex bi. Ba tax ñuy fàttali àq ak yelleefi Saa-Palestin yi ci am seen réewum bopp mom, péey ba Serisalem lay doon. Naka noonu, ñuy sàkku ci ñu dakkal ci saa si jaay-doole gi Israayel nekke ci Bande de Gaza. Te, dinañu ko topp ba fu mbaxana doonee benn ci àddina si ak ci àttewaay yi ndax ñaawteef yi mu teg askanu Palestin.

Sàkku nañ itam ñu xàll aw yoon te saxal ko ngir ndimbal yi fay dugg ñeel way-loru ya.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj