18 SAFAR
Dikkati nga ngir saafaraati sunuy aajooki tawat, yaw 18 safar.
Kon képp ku bëgg a tonowu dikkal màggal 18 safar.
Wépp yiw wees di sàkku dunyaak laaxiraa ngi nga làmboo,
yaw 18 safar.
Ku wuyujiwul man wuyuji naa Seex Bàmbaa woote ngir nu santle ko Laahu Buur ci 18 safar.
Ku yeex a dem ñàkk, ku romb faf réccu, li nga ëmb a rëy, yaw 18 safar.
“Ku bëgg a raw say maas saayiran wa baatinaan fonkal 18 safar”.
Boroom xelkoomay ki biral yile kàddu ñeel sa jëmm, yaw 18 safar.
Ngalla waay kuy wuyuji na làmboo jikkoy saadix jëf fa jëfi saadix ngir sa jëmm, yaw 18 safar.
Jaamu Yàlla: jàng alquraanak xasida, berndeel gan ñi, lilee di ndigal li ñeel sa jëmm, yaw 18 safar.
Aywa muriid, ndigal jëfe. bu kenn xeeb bu kenn yéem ginaar ba ci giléem la sëñ bi wax ci bisu 18 safar.
Dinanu la teeru, dalal la teral la, sëf la sunuy aajook i tawat ba noppi gunge la nga ñibbi yaw 18 safar.
Tey dagaan Laahu Buur fekkeek wér ba at mu jot nu màggal la, yaw 18 safar.