Saydu BA waa Ñooro la, di al-pulaar bu gàlle. Ndaanaan luy yëngu ci teyaatar la, tëgg ak um pecc. Tukki na ci réewi nasaraan yu bari, di fa teeweji ay ndajey fecckat ak i tëggkat. Ba Saydu tàmbalee bind ay taalif ak léegi, am na lu ëpp ñaar-fukki at.
WEYI TAN
Yaw mile dangaa xiif
Boo dee lekk, mukk doo suur
Lu la romb nga daldi siif
Sa koll gu rëy doo tàggook xiif
Saa su nu nekkee ci jàmm
Toog ba sunum xel dal
Nga dëkkee kàcc ak sàcc
Di déqi toolu askan wi
Weñ yi di la biiw
Tan yi di la yéew
Cogg gi dar la di la woy ak a jay
Ngay jayaxu ndax alal ji nga luubal
Bu nit ñi di daw ngir sàkku leer
Yaa ngay màmm ci biir lëndëm
Sos sa mbootaay di diisoo
Ay pexe yoo moome suuf si
Moomuloo li nga bokk ak say nawle
Nga dëkke néewal kàttan
Dooley askan wi la suuxat
Ci biir lawtanu sukuraat
Boo nu ŋàccee ba nu jeex tàkk
Siddi nu ba nu wow koŋŋ
Booba fekk na li ci sa koll
Saw yàppu yaram moo ca fees