Bërki-démb 26 sàttumbar ci atum 2020, “Bateau le Joolaa” def na 18i at ci biir géej. Daanaka ñaari-junni nit ñàkkoon nañ ci seen bakkan. Te mujjagul fenn, ay daan amaguñ ci. Moonte kenn mësula gis jéeya ju tollu nii, mu waroon a tax askan week nguur gi taxaw ngir leeral ko. Dañ koy fàtte ba bés bi dellusi, ñu amal ay ndaje, ne fay dige yoo xam ni, suñ fay jóge mu yem fa. Aa, nun askanu Senegaal, ni nu néewalee dafa jéegi dayo.
Ñi ñàkk seeniy mbokk a ngi wéy di naqarlook fàttaliku, nguur ngi di wéy di dige jàppale ak teg i daan ña sooke suuxu Joolaa bi. Naam, nguur nga woon ca jamono jooju taxawaayam matul woon benn yoon, waaye warul tax nguur yi ko wuutu ni yàcc, ni yasar.
Ñi ëpp ci askan wi yaakaaroon nañ ni nguur ngi ak àttekat yi dañ fay doxe wone seen mënin ak seen fulla waaye bun ko mën a waxee noonu fa la léeb doxe tàbbi géej ndax dige yu dul jéex te lépp naaxsaay.
Ci kàdduy Ablaay Jóob, jawriñ bi yor aadaak cosaan, dees na taxawal “Mémorial le Joolaa” jagleel ko way-lab yi ngir kenn bañ a mës fàtte lu tiis loolu daloon réewum Senegaal ci sàttumbar 2002. Buñ delloosi woon xottu gaal gi, nag, ci lay dàq ndax way-ñàkk yi dinañ mën a dëj dëgg-dëgg seeni mbokk ; dina giifal it lu mu bon-bon meru askan wi ñeel nguur gi ak ñépp ñi seen càggan jur lu ni mel. Noonu sax la ko Bubakar Bóris Jóob di waxe ci Bàmmeelu Kocc Barma(aux éditions EJO, 2017).