Seex
Mooy góor
Moo di as gor
Mbokk ya ko wor
Ñooy mbokk ya nu lor
Nuy leb ba fees ak i bor
Sànni xam sëgg ci fen di for
Ndax kat xam-xamam bu wóor
Bari lool ëmb ay ndam sëq ak jóor
Xayte xeltu mbatiit lu ne ba ci mboor
Lañu jaay jënde ay naxaate, käcc ak dóor
Ëllëg nag du añ du reer waaye mat naa sóor
Lu LFK di tontu gone yiy laaj booba ana Seŋoor ?
Làmp Faal Kala