FAIDHERBE, SAAY-SAAY BI NUY SARGAL

Yeneen i xët

Aji bind ji

Bi Siidiya Ndàtte Yàlla génnee àddina ak léegi, am na xarnook xaaj. Waaye, mi ngi mel ni mësta gane àddina. Dara gënta ñaaw, nag, cosaan lees neenal. Nde, ku xeeb sa cosaan, ñu xeebal la ko.

Xare bi gën a xereñe ci xare yi, mooy bi ngay noote say noon te doo xeex”. (Sun Tzu)

Bés bu Yàlla sàkk, ay junni-junniy nit dinañ romb ci kanamu Teyaatar nasiyonal Dañel Soraanoo. Ku ci xam Dañel Soraanoo moomu, na nu wax mooy kanati. Ndaxte, doxandéem bile, bokkul ci jàmbaar yi fi def i jaloore te ñuy woy seen i baax ak seen i baaxi maam. As lëf lees dégg ci moom, mooy ne, ab aktëeru farañse la woon. Jeex na ! Nga daldi may laaj, yow miy jàng bind yii, ne ma : « waaw, moom sax, lu mu defal réew mi ba nu war ko tudde ab teyaatar ? » Ma tontu, ne la : « Dara ! Tus ! ».  Nee ñu, baayam, gerefiye la woon ci tirbinaalu Ndakaaru ci ndoorteelu xarnu bin génn. Xam naa yaa ngi naan lii yomb na de ! Waaw, yomb na torob kay te metti ci xol. Rax-ci-dolli, ak li mu xereñe woon ak a bare woon i kaseti teyaatar yépp, amu ci benn bu mu mës a jagleel Afrig walla Senegaal. Waaye, loolu du doon mbetteel ñeel nit koo xam ne, mësta fóon ngelawu Senegaal.

Nu génn Ndakaaru, daldi teeri Ndar géej, fekk fa beneen doxandéem bees di sargale sunub ñaarelu iniwérsite bu gën a mag : Gastoŋ Berse. Daanaka, beneen Dañel Soraanoo rekk lees fi amaat. Waaye, kii moom, ku ko xamul laaj ko Seŋoor. Dina la ne kii mooy « baayu prospective » (am xalaatin ci wàllu xeltu), taggal la ko ba nga yéemu. Waaw, Seŋoor de, foo ko fekkaan, mu ngay tagg ngóor si. Lu ni mel jaaxal nu lool, nag. Naam, Gastoŋ Berse Ndar la juddoo, dib sët ci senn soxna su tuddoon Faatu Jaañ. Wànte, ba muy gone gu ndaw la génn réew mi. Sunu juumulee, tegaatu fi tànkam ba keroog muy dee. Mu ngoog.

Dëgg la, li nit ñiy fàttaliku walla lees xam ñeel démb lañuy tudde mboor walla cosaan, boroom xam-xam yi soloo ko walla muy luñ nuy nettali. Waaye, dara gënta ñaaw, nag, coosaan lees neenal. Nde, ku xeeb sa cosaan, ñu xeebal la ko. Aw askan, mëneesu koo ga ba muy weg ak a màggal nit ñoo xam ne, bokkul ak ñoom dara te, amaluñ ko benn njariñ ñeel jubluwaayam.

Seŋoor, nag, looloo nekkoon naalam : fexe ba waa Senegaal bëgg ay doxandéem yu tekkiwul dara ci ñoom, di leen dundal ci seen i xol, seen i wax ak di leen sargalee seen i taax ak i palaas. Bala maa dee rekk, muy taafantoo kàddoom yu neex ci nopp yooyu te di lakk xol, ay « métissage culturel » fii, « civilisation de l’universel » fële. Waaw, bu doon loolu la, lu ko tee tudde Teyaatar bi Alexandre Pouchkine walla Alexandre Dumas ?

Nun, nag, kenn demul nu des. Li ma ci gën a jaaxal, mooy tekk-tekkaaral bi maasi Seŋoor yi àndaloon. Ndege, ca jamonoom, amu ci kenn ku ci amoon xelu walla fitu sëgg ci noppu Seŋoor, ne ko : « Sëñ bi, ku rafet xol nga. Waaye, maye lu baax ci kër lay jëkke. Ñu mel ni Séex Aliyun Ndaw, Aimé Césaire, Duuta Seck walla Duura Maane ñoo gën a yey ci ñu tudde leen sunuy Teyaatar. » Ndaxte, ñooñu, kenn gënul leen a doon i werekaan. Amaana, fullaalun woon tur yooyii nees rëdd ci kanami taax yi. Boo demee, mbir mi daf noo soofoon, nu ñàkkal ko faayda. Mën na am tamit ne danoo amoon, dëgg-dëgg, kersay biral sunug démb, démb gu doy waar googu te ruslu. Nii la ko Fadel Ja junje woon cib yaxalam bim génne woon ci yéenekaayu Sud Quotidien.

Ñu may ma, ma joxeeti beneen misaal buy màndargaal gàcce googu nees am ci sunug démb ba tax nees di ko tanqamlu, di ko jéem a fàtte. Dafa mel ni, sax, dëddu boobu nu dëddu sunug démb, lu yàgg la. Ndege, ci njeexitalu oktoobar 1986, Abdu Juuf, njiitu réew ma woon, ak jawriñu mbatiit jamono jooju, Maxili Gasama, tabaxlu woon nañu xabru sunu jàmbaar ja, Lat-Joor, ca Déxële ga mu daanoo woon. Waaye, lu jiitu jëf ju rafet jooju, dañu sàggane woon lool Déxële ak teenam bu siiw ba, dëddu woon leen. Keroog bi ma ciy door a teg samay bët, dama waaru woon sax.

Ndeysaan, ci njeexitalu atum 2017, am nab yaxal bu génnoon ci yéenekaayu Le Quotidien, ñu bind ci ne, 30i at ci ginnaaw, Déxële ak li mu làmboo cim mboor ak i bérébi cosaan, dafa gën a toskare. Céy ! Ak ni askanuw Senegaal xëree ci aada ak cosaan, fonk lool seenug démb, di ko woy fu nekk, di ko bind ak di ko ndamoo saa su nekk. Moo, nag, lu leen tax a sàggane nii bérébi cosaan yiy seedeek a taxawe démb googu ? Lu waral gent gees leen gent ? Man, daal, dama foog ne dañu raxas seen bopp yi, walla mu am lu leen dal.

Dafa di, li ëpp ci nun, danuy faral di fàtte ne, jépp jàmbaar jees fiy nettaliy baaxam ak i jalooreem yit, fenn rekk la wax jiy mujj saa su nekk : dee na te kenn xamul fuñ ko denc. Li ko dale Lat-Joor ci boppam ba ci Alburi Njaay, jaare ko ci Séex Umar Fuutiyu Taal, Siidiya Ndate Yàlla Jóob ak ñeneen, ñii kenn xamul sax fu seen i néew nekk ; ñi ci des, ñoom, bitim-réew lees leen suul, sore lool seen i dëkk. Tombuktu. Doosa, ca Niseer. Tundi Bànjagara. Àllab Ndeng-Ndeng ba ca Gaboŋ. Nga xool béréb yii ñu leen mujje gis ni ñu soree.  Ndax dañ fay jaare réer nu ba fàww ? Yàlla bu ko Yàlla def !

Sunu càggante tax na be, 1960 ba tey, amagun fib nittabaxon (estati) bu mag biy màndargaal sunub jonn, keroog bi nu moomee sunu bopp. Mënoon nanoo am sax benn bu nuy jagleel Seŋoor, ak lees ko mënti tuumaal. Xam naa, yaa ngi naan ci sam xel, yow miy jàng sama yaxal bi, « Monument de la renaissance », nag ? Bu ko defee, ma xool la ndànk, yëngal sama bopp ne la, xanaa kay du ponkal yu jagadi yooyu nga may wax. Ñooñu nga xam ne, duñ sax sëgg xool nu, sunuy bët mën a daje. Du ñooñu kay téen di xool asamaan si ñoo ma tax di wax. Nee ñu, jant bi lañuy jéer. Waaye, ñoom la rekk. Ñoo koy yëg. Dañu xamul ne, nun, amalun nu benn solo. Du lenn lu ñuy tekki ci sunuy bët te amunu benn yëg-yëg ñeel leen. Ñu nekkoon ay ñay walla ay « cachalots » ñoo bokk yem ci nun.

Bu loolu weesoo, ma jàll ci yuq wax ji. Coowal Louis-Léon César Faidherbe mi lëmbe réew mi a ma tax a yatt samab xalima ngir wax ci sama xalaat. Seneraal bu ñaaw te bon boobu, Senegaal sañ koo bëgg, di ko sargal. Muy def ak mustaasam bu sëkk boobu ak i lonetam yi may bañ a tudd. May wax mu aj sikkimam boobu ak colam gu yànj. Waxuma sax nittabaxon (estati) ak palaas yees ko jagleel ca Ndar te mu jur coow lu réy fan yii, waaye tuddeesati na nootkat ba am ngér, ab otel, ay mbedd… Bi ci mujj te gën a ràññeeku mooy pom (jàlluwaay) biñ ko tudde ca Ndar. Mu mel ni loolu doyul. Ndaxte, biir Ndakaaru ci boppam, amoon na fab nittabaxon (estati) bu fa ne woon jonn ba ci atum 1983, ci kanamu màkkaanu njiitu réew mi, méngook tey Këru-Soldaar ga fa nekk.
(Dees na ko àggali…)

Bóris Jóob ci tekkig Aali Jàllo

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj