Ginnaaw bi ñu defee at ak lu teg, Càmmug Basiiru Jomaay Jaxaar Fay gee ngi waaj a song sémb yu mag yi ngir tabax réew mi. Looloo tax, ci Sémbuw Àtteb Ngurd mu 2026 mi, ñu sóoraale ci naaluw kopparal wu mag a mag. Li ñu ko dugge mooy dooleel yooni yaale (dem ak dikk) yi, yeesal jàngune yi te gën a lënkale diiwaan yi.
Ci kilifteefu Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Fay, ak elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko, Càmm gi dafa fas yéene jëmmal ay naal yu bariy njariñ ñeel askan wi. Maanaam, dañu bëgg a jël atum 2026 mii nu dëgmal, def ko atum jëf ngir soppi xar-kanamu réew mi. Liggéey boobu nag, kii di Décce Faal, jëwriñu Tabaxte yi, moo koy saytu.
Càmm gi dafa bëgg a lënkale réew mépp, defar ay yoon ak i raay yuy jokkale réew mépp ngir yombal dem ak dikk bi, suuxat koom-koom gi. Ngir jëmmal naal yooyii, natt nañu koppar yu tollu ci 716i miliyaar ci Sémbuw Àtteb Ngurd mu 2026 mi, jagleel ko njëwriñu Tabaxte yi.
483,6i miliyaari seefaa lañu jagleel tabaxug tali yi ak raay yi, 155,2i miliyaar ngir taaxi dëkkuwaay yeek yu caytu gi ak 8,5i miliyaar ngir tabaxtey waax yi ak naawu yi.
Bu dee sémb yi ëppal Càmm gi solo nag, talib Mexe-Pekes-Cilmaxa (8,5i miliyaar) ak talib Sànjara-Njagañaaw (3,5 miliyaar) ci lañu bokk. Tali yooyu, bu ñu àggee, dinañu jàppandal dem beek dikk bi ci béréb yooyu te yit dina tax dëkki kaw yi am i tali yu baax. Ba tay ci naal yu ñu jiital yi, dees na ci boole yeesalug yooni raay yu jokkale Ndakaaru ak Kidira (Jéego bu njëkk : Ndakaaru-Tàmbaakundaa, 3i miliyaar). Li ñu ko dugge mooy dekkali yaaleg saxaaru jéeri ji.
Ba tay ci naal yi, dees na defaraat naawub Sigicoor ba nekk ci sànce (6i miliyaar). Bu naawu boobu àggee, dina tax Kaasamaas doon bérébu koom-koom ak wërteef te gën a jokkaloo ak réew mi.
Naka noonoot, njàng mi ak fànnu wér-gi-yaram wi desuñu ginnaaw. Ndaxte, doomu réew mooy defar réew. Xam loolu moo tax ñu waajal 40i miliyaar yees jagleel tabax ak yeesalug jàngune yi, muy bu Siin-Saalum (11,7i miliyaar), bu Aamadu Maxtaar Mbów (300i miliyoŋ), bu Asan Sekk bu Sigicoor (100i miliyoŋ), ak jànguney Maatam yeek yu nekk ca penkub Senegaal (400i miliyoŋ). Ñoo ngi waaj a tabax itam ak dëkkuwaay ya ca jàngune ya (12,9i miliyaar) ngir yombalal njàngaan yi seen nekkiin ak seen njàng.
Ci wàllu wér-gi-yaram, 60i miliyaar lañuy jagleel tabaxug 35 bérébi fajukaay yu mag. Te yit, dees na jagleel naaluw PUMA wi 5i miliyaar ak wow PUDC 4i miliyaar. Naal yooyu, waa kaw gee leen moom.