Ginnaaw bi ñu ko njëkkee amal ci atum 2014, Nguuri Afrig yeek seen i ñoñ amal nañu ñaareelu ndaje mu mag mi ñu jagleel kopparal jumtuwaay yi ci Afrig. Ñiŋ ko doon amale fii ci Ndakaaru, ci CICAD (Centre international de conférences Abdou Diouf) bi nekk ca Jamñaajo, ci ñaari fan yii weesu (alxames ak àjjuma, 2 ak 3 féewirye 2023).
Ak fi àddina tollu, bokk na ci liy wootal dugalantekat yi (les investisseurs), réew mu am jàmm, dal te am i jumtuwaay yu baax. Loolu tax na ba suqaleeku jumtuwaay yi doon lu am solo lool ci yoonu yokkute. Ndax, dafa di nattukaay bu boroom alal yi di jëfandikoo ngir sawar ci dugalante (investir) seen alal. Bile gis-gis, moo yóbbu Nguuri Afrig yi ci ñu tàmbalee wone seen taxawaay ngir amal i jumtuwaay yu baax fii ci kembarug Afrig.
Ci atum 2014, lañ njëkkoon a amal ndaje mu mag ñeel kopparal jumtuwaay yi ci Afrig. Ci moomu ndaje, ñu doon ci weccantey xalaat ci yenn naal yu aju ci PIDA (Programme de développement des infrastructures en Afrique), maanaam Naalub suqaleeku jumtuwaay yi ci Afrig. Mu doonoon ab naal bu BAD (Banque Africaine de Développement) gàddu te ñu war koo doxal jëm atum 2030.
Ci biir PIDA bi, jubluwaay bi mooy fexe ba saafara bépp jafe-jafe bu laal dem beek dikk bi, wàllu ndox mi ak xarala yeek jokkalante bi. Ndajeem ren mi nag, di ñaareel bi, ñiŋ ko tënk ci ponk bile : « Gën a jëmmal jumtuwaay yi méngook jamono fii ci Afrig ». Njiiti réew yi, magum jëwriñ yeek yeneen i kilifa ya fa teewoon, waroon nañ settantal lu tollu ci 69i naal yu laal mboolem diwaani Afrig yi.
Ngir réewi Afrig yi am i jumtuwaay yu méngook jamono nag, dafay laaj kopparal gu am maanaa. Loolu tax na ba li ñu gën a seetlu ci ndaje mi di li ñu doon waxtaane pexe yees war a lal ba mën a boole seen i doole ngir am kàttanug kopparal naal yi. Te mi ngi aju tamit ci Nguur yi fexe ba ñi liggéeyalul Nguur, dugalantekat yeek kurél yi, gis seen bopp ci naal yi ba mën a dajale koppar yi, tabax jumtuwaay yi war.