Mbootaayu Réewi Afrig yi dina amal ndajeem lëlub Njiiti Réew yeek Càmm yi. Moo ngi koy amal ci àppub ñaari fan (18 ak 19 féewaryee 2023) ca Addis Abebaa, Péeyub réewum Ecopi. Ñu nar cee waxtaane yombal gi ñeel njënd meek njaay mi ci biir kembarug Afrig.
Lëlub Njiiti Réew yeek Càmm yi mooy kurél gi gën a kowe ci kurél yiy jël i ndogal ci Mbootaayu Réewi Afrig yi (UA, Union Africain). Ñi fay toogaan (siéger) di Mboolem Njiiti Réew ak Càmmi Afrig yi. Lël bi mooy rëdd yoonub naali Mbootaay gi, di taxawal sémb yi at mu jot, di sàkk njëkke yi (les priorités) ak a saytu doxalinu ndogal yeek naal yi.
Ca atum 2004 lañu jëloon ndogalu amal ndajeem lël bi ñaari yoon, biir at mu nekk. Ginnaaw looleet, mënees na amal ndaje mu tembare saa bu kog Nguur sàkkoo te ñu ëpp ci 2/3 ub mbootaay gi ànd ci. Ndajeem weeruw féewiryee 2023 mi nag, mooy 36eelu ndajeem lël bi. Ponk bi di « Atum ZELCAF (Zone de libre-échange continentale africaine) : Gaawantal yombal gi ñeel njaay mi ci kembarug Afrig ».
Ni ko ponk bi tënke, Ndaje maa ngi aju ci yéeney xértal Njiit yi ñu jublu ci naal yi ñeel yaxantu bi. Bu ko defee, dinañu fa waxtaane pexe yi mën a jëmmal gis-gis bees am ci njaay meek ni mu waree, doon yoonuw suqaleeku Afrig. Loolu dina leen yóbboot ci lëkkale Nguur yi, Bànqaasi Mbootaay gi, ak yeneen way-yëngatu (acteurs) yi ñu ko séqal te ñu am waar ci gis-gis bi (ZELCAF).
Ba tey, ci ndaje mi, dinañu fa amal ab coppite ci boppu Mbootaay gi. Njiitu réewum Senegaal lii di Maki Sàll, di na joxe lengey Njiitul Mbootaay gi mu doon doxal ci at mii weesu (2022-2023). Asali Asumaani, mi nekk Njiit réewum Komoor jamono yii, mooy ki ko fa war a wuutu ci at mii di ñëw (2023-2024).
Waxtu wii sax, moom Njiit réewum Senegaal li, ma nga ca Adis Abebaa ngir fekkeeji ndaje ma. Ci ngoonug àjjuma ji la fa àgg. Mënees na jàpp ni li gën a fés ci moomeem gii di jeex mooy tukki yi mu doon amal, di fekkeeji ndajeem Kurél yi ci àddina si, ak daan fa sàkku gëddu Afrig ci ni mu yelloo. Mënees na cee lim lu mel ni toogaan ci kurélu kaaraange gu Mbootaayu xeet yi walla sax ca kurélug G20.